1Ayóoba daldi ne:
2Éy su sama tiis wii doon lu ñuy natt diisaayam?
3Kon tey mu gëna diis suufoo suufi géej.
4Da di fetti Aji Man jee ma jam,
5Mbaamu àll dina ŋaax te tiim ñax mu tooy a?
6Deesul lekk lu soof, loo deful xorom,
7Sama xel a ko nanguwul,
8Éy kuy amal sama dagaan,
9Yal na neex Yàlla mu nappaaje ma,
10Bu ko defoon sama ndàmpaay di li ma gàntalul
11Ana doole ju ma amati bay muñ?
12Dama diw doj bay àttan lu ne?
13Ndax amati naa wall,
14Ku ne lasiim, saña séentu xarit baaxe la,
15Samay xarit a ma wor ni wal moo fekk ŋiis.
16te ba sedd bay tàggoo,
17Waaye bu noor biy dikk, mu wow,
18Jëggi giléem ay wërum ndox, ba wacc seenu yoon,
19Waa jëgg ya bawoo Tema di wër ay yol,
20ba àgg fa ñu ko fooge woon, yaakaar tas,
21Yeen déy, yeenay yooyu wal ci man.
22Dama leena masa ñaan dara,
23ngir ngeen xettali ma ci loxol noon,
24Xamalleen ma, man ma ne cell!
25Kàddu yu jub da lay yey,
26Dangeen di jéema sikk samay wax,
27Ab jirim sax àttan ngeen koo tegoo bant,
28Léegi nag, rikk walbatikuleen fi man,
29Deltuleen gannaaw, bu njubadi am.