Ayóoba 9:1-34 WOLB2025 - Bible AI

1Ayóoba dellu ne ko:

2Waaw, noonu la moos, xam naa ko!

3Ku bëgga layook Yàlla it,

4Moo rafet xel, bare doole!

5Keey randal tund yi te duñu ko yég;

6gësëm suuf fa mu tege,

7Keey gëdd jant bi, aaye koo fenk,

8Keey wéetoo di firi déndi asamaan,

9Moo sàkk dëllooñ gi féete bëj-gànnaar

10Keey def jëf ju màgg ju nattuwul,

11Mu ngoog, daf may romb te duma ko gis,

12Kii, bu këfee, ana ku koy tere?

13Yàlla du dànk meram,

14Ana nu ma koy àddoo, man?

15Su sama der setee it, duma mana àddu,

16Su ma ko woon cib layoo, mu wuyu itam,

17Moom mi may rajaxee ngelaw lu réy,

18mayuma sax ma astandiku,

19Su dee kàttan, kee bare doole!

20Ma am dëgg, sama kàddu sikkal ma,

21Maa mucc ayib a? Xam!

22Lépp benn la rekk! Moo tax ma ne:

23Mbas ne jaas, rey ñu deful dara,

24Àddinaa ngi tege ci loxol ku bon,

25Ab dawkat sax ni samay fan di jeexee ko raw.

26Samay fan tarxiis nañu, wéy, woyof ni gaali barax,

27Su ma nee: «Naa fàtte sama tawat,

28du tee ma ragal mboolem samay mitit,

29Ndegam maa tooñ,

30Su ma raggoo woon saabu,

31du tee nga tàbbal ma cim leeñ,

32Yàlla da dul nit ni man, ba may weranteek moom,

33Su amoon sax kuy dox sunu digg, jubale nu,

34teggil ma yetam, mu sore ma,

© 2025 Bible Society of Senegal
>