Baamtug yoon wi 15:1-22 WOLB2025 - Bible AI

1Juróom ñaari at yu mat yu nekk, nangeen amal njéggalug bor.

2Mbirum njéggaleg bor gi, nii lay deme: Mboolem ku lebaloon dëkkandoom, bumu ko ca feyeekooti. Na jéggale la mu lebaloon dëkkandoom, mbokkum bànni Israayilam|lemma="bànni Israayil:"*, gannaaw bu ñu biralee njéggaleg bor, ñeel Aji Sax ji.

3Jàmbur bi bokkul ci bànni Israayil, sañ ngeen koo feyeeku, waaye la leen seen mbokkum bànni Israayil ameel, jéggaleleen ko.

4Waaye ab ndóol du am ci seen biir, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di barkeel bu baax ca réew ma mu leen di jox, muy seen cér, ngeen jagoo,

5ndegam déggal ngeen bu baax seen Yàlla Aji Sax ji, di sàmmoo jëfe mboolem santaane bii ma leen di dénk tey.

6Bu leen seen Yàlla Aji Sax ji barkeelee ni mu ko waxe déy, yeenay lebal xeet yu bare, waaye yeen dungeen leb. Te it yeenay yilif xeet yu bare, waaye yeen, deesu leen yilif.

7Su amee ci seen biir ab ndóol, di kenn ci seen bokki bànni Israayil, ci benn ci seen dëkki réew mi leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox, buleen dëgër xol, di tëjal seen loxo seen mbokkum ndóol moomu.

8Nàddilleen koo nàddil, abal koo abal dayob soxlaam.

9Wattuleen seen bopp, bala leena jikko ju sew yóbbe, ngeen naan ci seen xel: «Atum juróom ñaareel mi, atum njéggalug bor dëgmal na,» ba tax ngeen néeg ci seen mbokkum ndóol, joxuleen ko dara. Da leen di booleek Aji Sax ji, ngeen gàddu bàkkaar.

10Nangeen ko jox a jox te bu ngeen koy jox it, bu ci seen xol bon, ndax loolu mooy tax seen Yàlla Aji Sax ji barkeel mboolem seen liggéey ak mboolem seenu ñaq.

11Du ñàkk nag ab ndóol ci réew mi. Moo tax ma sant leen ne leen ngeen nàddil a nàddil seen mbokkum ndóol, ak seen néew-ji-doole ji ci seenum réew.

12Su fekkee ne seen mbokkum bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*, góor mbaa jigéen da leena jaay boppam+ 15.12 Mbaa: su fekkee ne dees leena jaay seen mbokkum bànni Israayil,*, bu leen liggéeyalee juróom benni at, atum juróom ñaareel ma, yiwileen ko, mu moom boppam.

13Te bu ngeen ko yiwee, mu moom boppam it, buleen ko yiwee loxoy neen.

14Sàkkalleen koo sàkkal ci seeni gàtt ak seenum pepp ak seen biiñ. Kemu alal ja leen seen Yàlla Aji Sax ji barkeele, moom ngeen koy jox.

15Fàttalikuleen ne ay jaam ngeen woon ca réewum Misra, seen Yàlla Aji Sax ji moo leen jot. Moo tax ma sant leen lii tey.

16Ndegam nag seen jaam a leen ne: «Duma dem, bàyyi leen,» ndax cofeel gu mu am ci yeen ak seen waa kër, te bànneexam di nekk ak yeen,

17su boobaa fableen puso, ngeen sësale noppu jaam bi ci lafu bunt bi, te ngeen bënne puso bi noppam, ba mu jam ci lafu bunt bi, mu daldi doon seen jaam giiru dundam. Seen jaam bu jigéen it, noonu ngeen di def ak moom.

18Buleen mititlu lu ngeen yiwi seenub jaam, mu moom boppam, ndax jariñ na leen lu fey ñaari yoon surga buy feyeeku, ci juróom benni at yi mu leen liggéeyal. Te seen Yàlla Aji Sax ji dina leen barkeel ci mboolem lu ngeen def.

19Mboolem luy taaw ci seen jur gu gudd ak gu gàtt, te di góor, defal leen ko seen Yàlla Aji Sax ji cér bu sell|lemma="sell:"*. Buleen liggéeyloo mukk seen yëkk wu dib taaw, te buleen wat seen gàtt bu dib taaw.

20Xanaa ngeen di ko xéewloo at mu jot fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, yeen ak seen njaboot, fi béreb bi Aji Sax ji tànn.

21Jur gu ci am sikk nag, muy soox, mbaa mu gumba, mbaa mu am sikk su réy su mu mana doon, buleen ko sarxalal seen Yàlla Aji Sax ji.

22Ci seen biir dëkk ngeen ko wara xéewloo, te ku sobewu ak ku set yépp man na caa lekk, mel ni bu doon kéwél mbaa kooba.

icle>