Baamtug yoon wi 2:1-36 WOLB2025 - Bible AI

1Ba loolu amee nu walbatiku, dellu màndiŋ ma, topp yoonu géeju Barax ya, na ma ko Aji Sax ji waxe woon. Wër nanu diiwaanu tundu Seyir ay fani fan.

2Aji Sax ji wax ma, ne ma:

3«Seen wërub tund wii doy na. Walbatikuleen, jublu bëj-gànnaar.

4Mbooloo mi ngay sant ne leen: “Yeena ngi waaja jéggi seen kemu réewum bokki Esaween, ñi dëkke Seyir. Dinañu leen ragal, waaye nangeen moytu bu baax.

5Buleen xeex ak ñoom, ndax duma leen jox ci seen suuf fu téstën sax tege, ngir Esaween ñi laa sédd diiwaanu tundu Seyir.

6Aw ñam, weccikoo leen kook ñoom xaalis, door koo lekk; am ndox it, nangeen ko jëndeek ñoom, door koo naan.

7Ndax yeen kat seen Yàlla Aji Sax ji moo barkeel seen mboolemu ñaq te moo ràññee seen doxub màndiŋ mu yaa mii. Ñeent fukki at a ngii seen Yàlla Aji Sax jaa ngeek yeen, ñàkkuleen dara.”»

8Ba mu ko defee nu romb sunu bokki Esaween ñi dëkke Seyir. Danoo wacc yoonu joor ga, ak Elat ak Eccon Geber, daldi walbatiku jaareji màndiŋu Mowab.

9Ba loolu amee Aji Sax ji ne ma: «Buleen dal ci kaw Mowabeen ñi, di leen songub xare, ngir duma leen jox benn cér ci seenum réew, ndax askanu Lóot laa sédd réewum Ar.»

10Emeen ñaa fa njëkkoona dëkk, askan wu am kàttan lañu woon, bare, yegg ca kaw ni Anageen ñi.

11Ay Refayeen lañu jàppe woon Emeen ñooñu ak Anageen ñi, teewul Mowabeen ñi di leen woowe ay Emeen.

12Seyir nag la Oreen ña njëkkoona dëkk, waaye Esaween ñaa leen fa dàqe, rey leen, wuutu leen, noonu Israayil def rekk ak céru suufam bi leen Aji Sax ji jox.

13Aji Sax ji neeti: «Nangeen jàll walum Seredd.» Nu jàll walum Seredd.

14Diggante ba nu bàyyikoo Kades Barneya di dox, ba keroog bés ba nu jàllee walum Seredd, fanweeri at ak juróom ñett la. Fekk na mboolem maasu góor ña tollu woon ci xare, ca ndoortel yoon wa, ñoom ñépp a wuute dal ba, dee ba jeex, na leen ko Aji Sax ji giñale woon.

15Aji Sax jee leen toppe diisaayu loxoom, wollee leen ci biir dal bi, ba ñu jeex tàkk.

16Ba mboolem ña tollu woon ci xare deewee ba jeex, ba ñoom ñépp wuute ca mbooloo ma,

17Aji Sax ji wax ma, ne ma:

18«Yaa ngi waaja jéggi kemu réewum Mowab, ca Ar.

19Bu ngeen àggee ca Amoneen ña nag, buleen dal ci seen kaw, buleen xeex ak ñoom, ndax duma leen jox benn cér ci réewum Amoneen ñi, ngir askanu Lóot woowu laa ko sédd.»

20Diiwaan boobu it réewum Refayeen lees ko jàppe woon, te Refayeen ñaa fa njëkkoona dëkk. Teewul Amoneen ñi di leen woowe ay Samsumeen,

21askan wu am kàttan, bare, te yegg ca kaw ni Anageen ñi. Aji Sax jee bóom Amoneen ñi ci seen kanam, Amoneen ñi dàq leen, sanc, wuutu leen.

22Mooy na mu defaloon Esaween ña dëkke Seyir rekk, ba mu bóome Oreen ña ci seen kanam, Esaween ña dàq leen, sanc, wuutu leen, ba bésub tey jii.

23Aween ña dëkke woon dëkk yu ndaw ya dem, ba àkki Gasa nag, Kaftoreen ña bàyyikoo Keret ñoo leen bóom, wuutu leen.

24Aji Sax ji neeti: «Ayca, fabuleen, jàll walum Arnon. Mu ngoog, maa teg ci seen loxo, Sixon Amoreen ba, buurub Esbon, mook réewam. Dalleen di nangu réew mi, song ko xare.

25Bés niki tey maa tàmbalee wàcce njàqareek tiitaange ci kaw mboolem askan yi asamaan tiim, ba bu ñu déggee seenum riir, dañuy jaaxle, di lox.»

26Musaa waxati ak bànni Israayil, ne leen: Ci kaw loolu ma yebal ay ndaw yu bàyyikoo màndiŋu Kedemot, ba ca Sixon buurub Esbon. Ma yóbbante ko kàdduy jàmm, ne ko:

27«May nu, nu jaare sam réew. Yoon wi rekk lanuy topp; dunu jàdd ndijoor, dunu jàdd càmmoñ.

28Aw ñam, xaalis nga nu koy weccee, nu lekk; am ndox sax, xaalis nga nu koy joxe, nu naan. May nu rekk nu dox, ba jàll.

29Noonu nu Esaween ña dëkke Seyir defaloon ñook Mowabeen ña dëkke Ar rekk. Su ko defee nu mana jàll dexu Yurdan, ba àgg ca réew ma nu sunu Yàlla Aji Sax ji jox.»

30Sixon buurub Esbon nag nanguwu noo may nu jaare fa moom, ndax booba seen Yàlla Aji Sax ji moo dëgëral boppam, wowal xolam, ngir teg ko ci seen loxo niki bésub tey jii.

31Aji Sax ji ne ma: «Gis nga, maa ngi nii tàmbalee teg Sixon akum réewam ci seen loxo. Dalleen di nangum réewam.»

32Ba mu ko defee Sixon dikk dajeek nun, mook gàngooram gépp, ngir song nu xare ca Yaxacc.

33Sunu Yàlla Aji Sax ji daane ko fi sunu kanam, nu duma ko, mook ay doomam, ak gàngooram gépp.

34Jant yooyu lanu nangu dëkkam yépp, faagaagal dëkk yépp: góor ak jigéen ba ca tuut-tànk ya, bàyyiwunu kuy dund.

35Xanaa jur ga lanu sëxëtoo, ak mboolem alali dëkk ya nu nangu.

36La ko dale Arower ga tiim walum Arnon, boole ca dëkk ba ca xur wa, ba ca Galàdd, du benn dëkk bu nu të. Foofu fépp la sunu Yàlla Aji Sax ji daane fi sunu kanam.

cle>