Baamtug yoon wi 26:1-18 WOLB2025 - Bible AI

1Gannaaw loolu, bu ngeen demee ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji sédd, ba ngeen nangu ko, dëkke,

2na ku nekk ci yeen sàkk ca ndoortel mboolem meññeefum suuf mu mu jële ca seen réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox, mu def ko ci pañe, yóbbu ca béreb ba seen Yàlla Aji Sax ji tànn ngir dëël turam ëllëg.

3Na àgg ca sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ba fa nekk ci yooyu jant, ne ko: «Maa biral tey jii fi sa kanam Yàlla Aji Sax ji ne, agsi naa ci réew mi Aji Sax ji giñaloon samay maam, ne moom la may jox.»

4Na sarxalkat bi nangoo pañe bi ci loxoom, taaj ko fi seen kanam sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"* Yàlla Aji Sax ji.

5Mu dellu nag wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Sama maam ab Arameen+ 26.5 ab Arameen mooy Ibraayma, mi cosaanoo Padan Aram, te mooy maamu xeet wi.* buy màngaan la woon. Mu dem Misra, sance fa mbooloo su néew, te mujj di askan wu réy, am doole te bare.

6Waa Misra nag soxore nu, mitital nu, yen nu liggéey bu diis.

7Ba loolu amee nu yuuxu, woo sunu Yàllay maam Aji Sax ji wall, Aji Sax ji dégg nu, gis sunu mitit, ak sunu coono, ak sunu nootaange.

8Aji Sax ji nag génne nu Misra ci dooley loxoom ak kàttanam, ci biir musiba mu réy aki firnde aki kéemaan.

9Ba loolu wéyee mu indi nu fi béreb bii, jox nu réew mii, réew mu meew meek lem ji tuuroo.

10Moo ma taxa indi nii ndoortel meññeefum suuf si nga ma jox, Aji Sax ji.» Su ko defee mu taaj pañe bi fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, daldi sujjóot fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji.

11Mu bége nag, moom ak Leween|lemma="Leween b-:"* ñeek doxandéem yi dëkk ci seen biir, mboolem lu baax li ko seen Yàlla Aji Sax ji jox, moom ak waa këram.

12Gannaaw bu ngeen génnee mboolem céru fukkeelub meññeef, ci atum ñetteel, yemook atum génne cérub fukkeel, gannaaw ñaari at yu nekk, nangeen ko jox Leween ñi ak doxandéem yi ak jirim yi ak jëtun ñi, ngir ñu lekk ba regg, fa ñu féete ca seeni dëkk,

13te na ku nekk ci yeen wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Jële naa sama kër céru cellte bi, ba jox ko Leween ñeek doxandéem yeek jirim yeek jëtun yi, noonee mu dëppook sa santaane bi nga nu dénk. Moyuma lenn ci say santaane, te fàttewuma ci lenn.

14Lekkuma ci dara ci biir ab dëj, jëlewuma ci dara te fekk ma sobewu, te it sarxaluma ci dara ku dee. Sama kàddug Yàlla Aji Sax ji laa topp, noonee nga ma ko sante woon.

15Ngalla séentul fa sa màkkaan mu sell ca asamaan, te nga barkeel Israayil, sa ñoñ, barkeel suuf si nga nu jox, noonee nga ko giñale woon sunuy maam réew mu meew meek lem ji tuuroo.»

16Bésub tey jii seen Yàlla Aji Sax ji moo leen sant ngeen jëfe dogal yii ak àttey yoon yi. Sàmmooleen koo jëfe seen léppi xol ak seen léppi jëmm.

17Aji Sax ji ngeen biral bésub tey ne, mooy doon seen Yàlla, te dingeen doxe ay yoonam, di sàmm dogali yoonam aki santaaneem ak àttey yoonam, tey dégg waxam.

18Aji Sax ji it biral na bésub tey ne, yeenay doon ñoñam ñi mu séddoo, noonee mu leen ko dige woon, te ngeen di sàmm mboolemi santaaneem.

icle>