1Gannaaw loolu Musaa dellu na àddu kàddu yii, wax ak bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* gépp.
2Mu ne leen: «Maa ngi ci sama téeméeri at ak ñaar fukk, tey. Manatumaa jiite, te it Aji Sax ji moo ma wax ne ma: “Doo jàll dexu Yurdan gii.”
3Seen Yàlla Aji Sax ji ci boppam moo leen di jiite jàll. Mooy bóom xeet yooyu fi seen kanam, ngeen nangu seenum réew. Yosuwe moo leen di jiite jàll, na ko Aji Sax ji waxe woon.
4Aji Sax ji moo leen di def, na mu defoon Sixon ak Og, buuri Amoreen ña, ak seenum réew, bóom leen.
5Aji Sax jee leen di joxe fi seen kanam, ngeen def leen mboolem li ma leen santoon.
6Dëgërluleen nag te am fit. Buleen tiit, buleen yox-yoxi ndax ñoom, ngir seen Yàlla Aji Sax ji mooy ànd ak yeen. Du leen ba, du leen wacc mukk.»
7Ba loolu amee Musaa woolu Yosuwe, wax ak moom, Israayil gépp teg ci seen bët. Mu ne ko: «Dëgërlul te am fit, ndax yaw yaay ànd ak mbooloo mii ca réew ma Aji Sax ji giñaloon seeni maam, ne ñoom la koy jox. Yaw it, yaa leen koy sédde.
8Aji Sax ji nag mooy dox, jiitu la. Moom mooy nekk ak yaw. Du la ba, du la wacc mukk. Bul tiit, bul yoqi.»
9Musaa moo bind kàddug yoon wii, dénk ko doomi Lewi yu góor, sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yay gàddu gaalu kóllërey Aji Sax|lemma="gaalu kóllëre g-:"* ji, ñook magi Israayil ñépp.
10Musaa sant leen, ne leen: «Njeexital juróom ñaareelu at mu nekk, àppook atum njéggalug bor, ci diiru màggalu Mbaar|lemma="Màggal yi:"* yi,
11bu Israayil gépp teewsee fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, fa béreb ba muy tànni, nangeen jàng kàdduy yoon wii fi kanam Israayil gépp, ñuy dégg.
12Dangeen di dajale mbooloo mi, góor ñi ak jigéen ñi ak tuut-tànk yi, ba ci doxandéem bu nekk ci seen biir dëkk, ndax ñu déglu, ba tàggatu ci ragal seen Yàlla Aji Sax ji, di sàmmoo jëfe mboolem kàdduy yoon wii.
13Su ko defee seen doom yi xamul dinañu ci dégg, ba tàggatu ci ragal seen Yàlla Aji Sax ji, mboolem fan ya ngeen di dund ca réew ma ngeen jàll dexu Yurdan, jëm fa, ngir nanguji ko.»
14Ba loolu wéyee Aji Sax ji ne Musaa: «Ma ne, sa bésub dee ngi jegesi. Wool Yosuwe, te ngeen teewsi fi xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"* mi, ma yeb ko.» Musaa dem, ànd ak Yosuwe, ñu teewi fa xaymab ndaje ma.
15Aji Sax ji nag feeñ ca xayma ba, ci biir taxaaru niir, taxaaru niir wa taxaw fa bunt xayma ba.
16Aji Sax ji ne Musaa: «Yaa ngi nii di tëddi fa say maam. Mbooloo mii nag dinañu tàmbalee mel ni ñuy gànctu+ 31.16 gànctu misaal lay doon, mbete jigéen ju njaaloo, di fecci kóllëre gi mu am ak jëkkëram. Noona la bànni Israayil di defi, ci seen bokkaale, di fecci seen kóllëre ak Aji Sax ji.*, di topp yeneen yàllay doxandéem yu waa réew ma ñu jëm ca seen biir. Dinañu ma wacc, fecci sama kóllëre|lemma="kóllëre g-:"* gi ma fasoon ak ñoom,
17te sama sànj dina tàkk ci seen kaw bésub keroog. Maa leen di wacc, làq leen sama kanam, te kon yeneen xeet yi dinañu leen sëxëtoo. Musiba yu bare aki njàqare dina leen dikkal. Bésub keroog ñoo naan: “Xanaa sunu Yàllaa nekkul ci sunu biir kay, ba tax musiba yii dikkal nu!”
18Man nag maa leen di làq a làq sama kanam, bésub keroog ndax mboolem mbon gi ñu def, ndax ñoo walbatiku ci yeneen yàlla.
19Léegi nag bindleen woy wii ma leen di dégtal, te yaw Musaa nga jàngal ko bànni Israayil. Woyloo leen ko, ndax woy wii di sama seede ak bànni Israayil.
20Maa leen di yóbbu déy ca réew ma ma giñaloon seeni maam, fa meew maak lem ja tuuroo, ñu lekk ba regg, yaflu, daldi walbatiku ci yeneen yàlla, di leen jaamu, xarab ma, fecci sama kóllëreek ñoom.
21Su ko defee bu leen musiba yu bare dikkalee aki njàqare, woy wii mooy biral kàddug seede fi seen kanam, ndax su boobaa xel du ko faay, ba mu réer seenu askan. Ndax kat xam naa seen mébét mi ñuy rabat, te yóbbooguma leen sax ca réew ma ma leen giñaloon.»
22Ba loolu amee Musaa bind woy woowu bésub keroog, daldi koy jàngal bànni Israayil.
23Aji Sax ji nag yeb Yosuwe doomu Nuun ne ko: «Dëgërlul te am fit, ndax yaw yaay yóbbu bànni Israayil ca réew ma ma giñoon, te man ci sama bopp maay nekk ak yaw.»
24Ba Musaa bindee kàdduy yoon woowu cib téere ba mu mat,
25dafa yeb Leween|lemma="Leween b-:"* ñiy gàddu gaal gi àlluway kóllërey Aji Sax ji dence, ne leen:
26«Jëlleen téereb yoon wii, ngeen teg ko ci seen wetu gaalu kóllërey Yàlla Aji Sax ji, mu doon fa ab seede, ngir àtte leen.
27Ndax maa xam seen jikkoy fippu, ak seenug dëgër bopp. Seetleen, ndegam bi may dundagum tey ci seen biir ngeen di fippu ci kaw Aji Sax ji, astamaak gannaaw bu ma deewee.
28Woolleen ma seen magi giir yépp ak seeni kàngam, ma wax kàddu yii, ñuy dégg, ba ma seedeloo asamaan ak suuf, ci seen kaw, ñoom.
29Xam naa ne gannaaw bu ma deewee, dingeen def a def ag yàqute, dingeen teggi yoon wi ma leen jaarloo woon, te musibaa leen di mujj dikkal, ndax yeenay def jëf ju bon ju Aji Sax ji ñaawlu, ba merloo ko ndax seeni jëf.»