1Yeen asamaan, teewluleen, ma wax;
2Na samam njàngale sóob nib taw,
3Turu Aji Sax ji déy laay tudd,
4Kee di cëslaay, te mati jëf,
5Njabootam ñoo defug yàqute ci kawam,
6Aji Sax ji lañuy feye lii?
7Fàttalikuleen jant ya njëkkoon,
8Ba Aji Kawe ji séddee xeet yi seeni suuf,
9Céru Aji Sax ji moo di ñoñam,
10Moo leen fekk réewum màndiŋ,
11Moo mel ni jaxaay juy naawtal am tostanam,
12Aji Sax ji doŋŋ a leen wommat,
13Moo leen waral kawtey réew ma,
14boole ca soowum nag ak meewum xar,
15Yeen Yesurun+ 32.15 Yesurun: tur wii ak Yanqóoba itam dees na ko woowe Israayil.*, yeena yaflu, waŋŋeetu,
16Ñoo yee fiiraangeem, ndax ay yàllay doxandéem,
17Ñoo sarxalal ay rab yu dul Yàlla;
18Cëslaay li leen meññ ngeen foñ,
19Aji Sax jee gis loolu, gedd,
20Mu ne: «Maa leen di xañ sama kanam,
21Ñoo ma fiirloo ak yàlla yu dul tus,
22Sawaraa ngay tàkke ca sama sànj,
23Maay jal ci seen kaw ay musiba,
24Ñooy loof cib xiif, jeex tàkk ndaxi jàngoro,
25Fa biti la leen saamar di xañey doom,
26«Maa noon maa leen di bóom,
27Waaye reetaani noon laa ci ragal,
28Wii xeet wu gàtt xel
29Su ñu muusoon, xalaat ci lii,
30Ana nu kenn di dàqe seen junni,
31Yaakaaru noon yi de melul ni sunu yaakaar,
32Seen reseñ a nga cosaanoo Sodom|lemma="Sodom ak Gomor:"*
33Seen biiñ daŋaru ninki-nanka la,
34«Xanaa du loolu laa làq fi sama wet,
35Maay kiy feye, di añale,
36Aji Sax jeey dëggal ñoñam,
37Su boobaa da naan: «Ana seen yàlla ya,
38Ñi lekk seen nebboni sarax,
39Kon gisleen ne man la, man doŋŋ,
40Maay yékkati sama loxo jëme asamaan,
41bu ma daasee sama saamar buy melax,
42Maay nàndal samay fitt deret,
43Yeen, xeet yi, tàcculeen ñoñam,
44Noonu la Musaa dikke, mook Yosuwe doomu Nuun, ba jaar ci mboolem kàdduy woy wii, mbooloo mi di dégg.
45Gannaaw ba Musaa noppee ci jottali Israayil gépp mboolem kàddu yooyu,
46da ne leen: «Defleen seen xel ci mboolem kàddu yi ma leen di artoo man, bésub tey, te ngeen sant seeni doom ñu sàmmoo jëfe mboolem kàdduy yoon wii.
47Ndax kat du kàddug neen ci yeen. Mooy seenug dund! Ci gii kàddu ngeen di gudde fan, ca réew ma ngeen di jàll dexu Yurdan jëm fa, ngir nanguji ko.»
48Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa bésub keroog boobee, ne ko:
49«Doxal yéegi ca tundi Abarim gii, nga jàll ba ca tundu Nebo ca diiwaanu Mowabeen ba janook Yeriko. Nga séentu nag réewum Kanaan mi may jox bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*, ñu jagoo.
50Boo noppee, dinga faatu ca kaw tund woowu nga yéeg jëm, ba nga fekki say bokk, noonee sa mag Aaróona deewe woon ca kaw tundu Or, ba mu fekki ay bokkam.
51Li ko waral mooy yeena ma fecci worma ci digg bànni Israayil, ca ndoxi Meriba Kades, ca màndiŋu Ciin, ndax yeena wormaalul sama sellaay ci digg bànni Israayil.