1Ca ñetteelu atu nguurug Belsacar, man Dañeel am naa meneen peeñu, gannaaw peeñu ma ma njëkkoona am.
2Ca biir peeñu ma, maa ngi ci Sus, dëkk bu dàbbali ci diiwaanu Elam. Ma gis ci peeñu mi ne maa ngi ci wetu yoonu ndox ma ñu gas te ñu di ko wax Ulay.
3Ma séentu, xool, yem ci kuuy mu taxaw feggook yoonu ndox ma, am ñaari béjjén yu gudd te benn bi gëna gudd ba ca des. Waaye bi gëna gudd moo mujja sax.
4Ma gis kuuy may dañ, di jublu sowu ak bëj-gànnaar ak bëj-saalum. Menn mala manu koo të, te maneesula xettali kenn ci moom. Ma ngay def lu ko neex tey gëna màgg.
5May xool, ab sikket jóge sowu, jaare déndub suuf sépp te laalul suuf. Sikket baa nga am béjjén bu yéeme ci diggante bët yi.
6Mu dikk ba tollook kuuyum ñaari béjjén mi ma gisoon ci wetu yoonu ndox mi, daldi koy songe xadaru dooleem.
7Ma gis ko nag, mu dikk ba ca moom, song kook xadar, dóor kuuy mi, damm ñaari béjjénam, te kuuy mi manu koo të. Mu daane ko ci suuf, noote ko, te kenn manu koo teqaleek moom.
8Sikket bi mujj màgg lool; ba fa kàttanam yem, béjjén bu gudd ba damm, ñeenti béjjén yu yéeme daldi sax, wuutu ko, jublook ñeenti ngelawi asamaan.
9Ci kaw loolu béjjén bu ndaw génne ci béjjén yooyu benn, daldi law a law jublu bëj-saalum ak penkook réew ma gëna rafet+ 8.9 réew ma gëna rafet fii réewum Israayil a tax ñuy wax.*.
10Muy màgg nag bay diir mbagg gàngoori xarey asamaan, ba daaneel yenn ci ñoom, ak yenn ci biddiiw yi, nappaaje leen.
11Muy damu bay diir mbagg Njiital gàngooru xare gi, daldi dakkal sarax ba ñu ko daan defal bés bu jot, màbb kër gu sell ga.
12Gàngooru xare gi tegu ciy loxoom, boole kook saraxu bés bu jot bi, lépp cig tooñam. Béjjén bi dal ci kaw dëgg, daaneel ko fi suuf, ay pexeem àntu.
13Ba loolu amee ma dégg jenn aji sell|lemma="sell:"* di wax, jeneen aji sell ne ko: «Lan mooy àppu peeñu mii ñu gis, ñu di ci dakkal sarax biy am bés bu jot, di teddadil gàngooru xare gi, aka tooñ, di yàq lépp?»
14Mu ne ma: «Àpp bi ñaari junni laak ñetti téeméer (2 300) ciy guddeeki bëccëg. Gannaaw loolu dees na taxawalaat kër gu sell gi.»
15May xool ci biir peeñu mi, man Dañeel, di jéema xam lu muy tekki, jëmm juy nirook góor, ne jimeet taxaw ci sama kanam.
16Ci kaw loolu ma dégg baatu nit jibe ca digg yoonu ndox ma ñuy wax Ulay. Mu àddu ca kaw ne: «Jibril, waxal kii peeñu mi.»
17Jibril dikk nag ba fi ma taxaw. Ba mu jegesee, ma tiit lool, ba daanu, sama kanam dëppu fi suuf. Mu ne ma: «Yaw doom aadama ji, nanga xam ne peeñu mii mujug jamono la.»
18Bi muy wax ak man, ma daanu leer, sama kanam dëppu fi suuf. Mu laal ma, taxawalaat ma fa ma taxawoon.
19Mu ne ma: «Maa ngi lay xamal luy xew keroog ba sànjum Yàlla di jeex, ndax muj ga mooy àppu sànj ma.
20Kuuy mi nga gis mu am ñaari béjjén, buuri waa Medd ak waa Pers la.
21Sikket bi, buuru réewum Geres la. Béjjén bu gudd bi ci diggante bët yi mooy buur bu njëkk bi.
22Dañu koo damm, ñeenti béjjén wuutu ko, di ñeenti nguur yu soqeekoo ca xeet wa, waaye duñu am doole ni ga jiitu.
23«Bu nguur yooyu jeexee, ba bàkkaarkat yi buural, buur bu néeg te bare pexe dina falu.
24Dina gëna am doole, waaye du doon dooley boppam. Yàqam dina jéggi dayo, te ay pexeem dina àntu. Dina rey ñu am doole ba ca mbooloom aji sell yi.
25Xelum njublaŋam lay naxee, di réy-réylu, ba bett ñu bare, rey leen, te dina dëkk kilifay kilifa yi. Waaye mooy sànku, te loxo du ko laal.
26Peeñum ngoon meek mu bëccëg mi nga gisoon, te ñu àgge la ko, lu wér la. Yaw nag neel cell ak peeñu mi, ndax des na fan yu bare.»