Efes 1:1-22 WOLB2025 - Bible AI

1Ci man Póol, ndawal Almasi|lemma="Almasi b-:"* Yeesu ci coobarey Yàlla, ci man la kàddu gii bawoo, ñeel ñu sell ña ca Efes te di ñu sàmm seen kóllëre ak Almasi Yeesu.

2Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay ak Sang Yeesu Almasi bi.

3Cant ñeel na Yàlla, Baayu sunu Sang Yeesu Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi nu baaxe bépp barkey biir, ci Almasi bi nu bokk, fa déndi asamaan ya.

4Te mooy noonu mu nu tànne ba àddina sosoogul ndax Almasi bi nu bokk, ngir nu doon ñu sell te mucc sikk fa kanamam. Ci biir cofeel

5la dogaloon lu jiitu, ne ci Yeesu Almasi bi la nuy defe ay doomi boppam, te muy bànneexam, di coobareem.

6Moo tax cant ñeel ko, ndax yiwam wu màgg wi mu nu baawaanal ci Soppeem bi.

7Ci moom lanu ame njot|lemma="jot:"* gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa,

8wi mu nu baawaanal, mayaale nu mépp xel mu rafet akug dégg.

9Moo nu xamal mbóotum coobareem mi mu nammoona sottale naka jekk ci Almasi bi, na mu ko neexe.

10Li Yàlla namm, bu fan yi matee, moo di dajale lépp ci kilifteefu Almasi bi, mboolem la fa asamaan ak li fi suuf.

11Ci moom lanu jote sunu muur ci kaw dogalu Yàlla mi nu tànn lu jiitu, moom miy sottal lépp ni mu ko namme ci coobareem.

12Moo tax nu di ko sante màggaayam, nun ñi njëkka wékk sunu yaakaar ci Almasi bi.

13Kooku, yeen ñi dul Yawut, ba ngeen déggee, yeen itam kàddug dëgg gi, xibaaru jàmm bi jëm ci seenug mucc, gannaaw ba ngeen gëmee, ci moom itam lañu leen màndargaale Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi ñu dige woon.

14Noo gi moo di dawal bi nu jotagum ci sunu muur, ba kera njotug ñoñi Yàlla matee, ba nit ñi sante Yàlla màggaayam.

15Moo tax man it, bi ma déggee ba tey, seen ngëm ci Sang Yeesu ak cofeel gi ngeen sopp gëmkat ñu sell ñépp,

16noppiwumaa sant Yàlla ndax yeen, te maa ngi leen di fàttaliku ci samay ñaan,

17ngir Yàllay sunu Sang Yeesu Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi, Baay bu màgg bi, sol leen xel mu rafet ak ngis, ngir ngeen man koo xam bu baax.

18Ngir itam seen bëti xol leer ba ngeen gis yaakaar ji ci wooteem ak ni ay ngëneelam géejoo te yéeme, ñeel ñu sell ñi mu séddoo.

19Ngeen boole ci xam manooreem gu nattuwul gi mu nu lañalal, nun gëmkat ñi. Manoore googu feeñ na ci jëf ji sottee ci kàttanam ak dooleem

20ji mu fésal ci Almasi bi, ba mu ko dekkalee, dëël ko ci ndijooram fa déndi asamaan.

21Foofa la Almasi bi tiime lu sore gépp nguur ak bépp sañ-sañ ak gépp manoore ak gépp kilifteef ak wépp tur wees di tudd, muy tey di ëllëg.

22Yàlla moo teg lépp fi roni tànkam+ 1.22 Seetal ci +bk Taalifi cant+bk* 8.7.*, te moo ko def muy bopp bi tiim lépp, ñeel mbooloom gëmkat ñi,

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>