Efes 4:1-31 WOLB2025 - Bible AI

1Dama leen di dénku nag, man mi ñu tëj ndax Sang bi, ngir ngeen dund dundin wu yellook wooteb Yàlla bi mu leen woo.

2Saxooleen woyof, lewet, te deeleen muñ, di muñalante ngir cofeel.

3Defleen seen kem kàttan, ngir di jàmmoo, ba mana sàmm seenug bennoo ci biir Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi ngeen bokk.

4Wenn yaram a fi nekk ak genn Noo ak jenn yaakaar ju leen wooteb Yàlla jëme.

5Benn Sang bi la it, ak genn ngëm ak genn sóobu cim ndox+ 4.5 sóobu cim ndox la gëmkatub Almasi bi di firndeele ngëmam.*.

6Te it jenn Yàllaa am; mooy Baayu ñépp, moo tiim ñépp, di jëf ci ñépp te nekk ci ñépp.

7Waaye ku nekk ci nun ak mayam, ci yiwu Yàlla, ni ko nattub Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi séddalee.

8Moo tax ñu ne:

9Li ñu ne «moo yéeg,» ana lu muy tekki lu moy wàccoon na it ba fu gëna suufe?

10Kooku wàccoon mooy kenn ki yéegaat ba tiim asamaan yépp, ngir def lépp feese jëmmam.

11Moo may ñii di ay ndawam, ñee di ay yonent, ñee di ay xamlekati xibaaru jàmm bi, ñale di ay sàmmi mbooloom gëmkat ñi, mbaa ay jàngalekat.

12Almasi bi moo waajale noonu ñu sell ñi, ba ñu mana bey seen sas ci liggéeyam, ngir tabax mbooloom gëmkat mi taxawe yaramu Almasi bi.

13Su ko defee nu mana màgg nun ñépp ba doon benn ci ngëm ak ci xam-xam bu mat ci Doomu Yàlla|lemma="Doomu Yàlla j-:"* ji, ba kera nuy doon magum jëmm, bay tollook taxawaayu Almasi bi mat sëkk.

14Su boobaa nu noppee doon ay tuut-tànk yu nit ñiy muusaatoo kàddu yu mel ni gannax yu nuy baaje ak ngelawal mboolem àlluwa ju bees ju nuy pamti-pamtee ci seen biir pexey naxe ak njublaŋ, ngir fàbbi nu.

15Su boobaa kay, dëgg gu nu wodde cofeel lanuy wéye, tey màgg ci bépp fànn, ci moom Almasi biy bopp bi.

16Ci moom miy bopp bi la yaram wépp di déggoo, temboo ndax ndimbalal mboolem tenqo yi koy saytu, na mu dëppook wàllu cér bu ci nekk. Su ko defee yaram wiy yokku, di màgg ci biir cofeel.

17Lii nag maa leen ko wax, te di ko biral ci turu Boroom bi: ni xeeti yéefar yiy jëfe, topp seen xalaat yu tekkiwul dara, buleen jëfeeti noonu.

18Seenum xel a tàbbi ag lëndëm, ñu tumurànke dundin wi Yàlla di maye, te umple gi ci ñoom moo tax, ndax seenug dëgër bopp.

19Dañoo mujj dërkiis, yebu ci topp seen bakkan, ba xaabaabal ci jépp jëfi sobe.

20Yeen nag du loolu ngeen jànge ci Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi,

21ndegam kay Yeesu ci boppam ngeen dégg mbiram, ba jànge ci moom, dëgg gi bawoo ci moom,

22te mooy ngeen bàyyi seen jikko ju njëkk ja, ngeen teqalikoo ak seen jëmm ja woon démb, jëmm ja masa topp bànneexi bakkan yuy naxe, ba sóobu ci yàqute.

23Su ko defee ngeen mana yeeslu ci seenum xel, ci ndimbalal Noowug Yàlla|lemma="Noo gu Sell g-:"*,

24te ngeen soloo jëmm ju yees ji Yàlla sàkke ci takkndeeram, di jëfe njub ak sellaay ji dëgg di jur.

25Kon nag bàyyileen fen, te ku nekk di wax sa moroom dëgg, ndax ku nekk ci yeen sab céru moroom nga.

26Buleen mer ba bàkkaar, te bu jant bi sowe seen mer;

27buleen xajal Seytaane|lemma="Seytaane:"*.

28Sàcc bi, na bàyyi sàcc te nangoo sonn, di liggéeye loxoom liggéey bu rafet, ba man cee dimbali néew-ji-doole ji.

29Bu genn kàddu gu bon génne seen gémmiñ, xanaa su ko jaree ngeen wax lu baax, luy jariñe, te diw yiw ci ñi koy dégg.

30Te it buleen tiisal Noowug Yàlla gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi leen màndargaale xàmmikaayam ngir bésub njot|lemma="jot:"* ba.

31Lépp luy wextan ak naqari deret ak mer mu ëpp ak coow ak saaga, na lépp buube, ba génne ci seen biir, mook mboolem jëfi coxor.

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>