Esayi 10:1-34 WOLB2025 - Bible AI

1Wóoy ngalla boroom dogal yiy dogal njubadi, bind ko, te muy jur coono,

2di ko àttee ñàkkal ku ñàkk, di xañ àq sama néew-ji-dooley ñoñ, bay lekk ab jëtun, di sëxëtoo ab jirim.

3Ana nu ngeen di def keroog bésub mbugal ba, keroog ba safaan di bawoo fu sore? Ana ku ngeen di daw wuti wallam? Ana fu ngeen di denci seen teraanga?

4Xanaa ànd ak ña ñu jàpp, ne yogg; mbaa tëddandook ña ñu bóom, ne lareet. Teewul Aji Sax ji xàcc loxoom, meddiwul ba tey. Asiri muccul ci mbugal

5Wóoy ngalla Asiri miy sama yetu mer, bolde bi ñu ŋàbb di sama sànj,

6ma xabtal ko fi kaw xeet wu gëmadi, yebal ko ca askan woowu ma merloo, ngir ñu sëxëtoo leen, nangu seen alal, noote leen ni banu mbedd.

7Waaye Asiri gisewu ko noonu, xalaatewul noonu; bóome la xintewoo, ba faxas xeeti xeet.

8Mu ngi naan: «Xanaa du sama jawriñ yépp a diy buur?

9Kalne daa gën Karkemis gee ma nangu? Am Amat daa gën Arpàdd? Am Samari daa gën Damaas+ 10.9 Kalne ak Karkemis ak Amat ak Arpàdd ak Damaas, ay dëkki Siri lañu.?

10Maa duma réew yu seeni yàllantu, seeni tuur sut tuuri Yerusalem ak Samari.

11Na ma tege loxo Samari aki yàllantoom, ndax duma ni tege loxo Yerusalem aki tuuram?»

12Boroom bi nee: «Bu ma sottalee liggéey fa kaw tundu Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:" ak fa Yerusalem, maay mbugale buurub Asiri réy-réyloom gi, ak gëti xeebaateem.»

13Moom moo ne: «Sama dooley përëg laa defe lii, maa xelu, ràññee; ba randal kemi suufi xeet yi, foqati seeni alal, dañ boroom jal ya niw yëkk, wàcce leen.

14Maa teg alali xeet yi loxo, ni ku gis am tàgg. Maa tonneendoo réewi àddina ni ku for ay nen, tonni lépp, laaf tëf-tëfluwul, sàll newul ciib!»

15Sémmiñ dina diir mbagg ka koy gore? Am dogukaay dina réy-réylu ba sut ka koy doge? Mbete yet wuy yékkati ka ko ŋàbb; mbaa bolde bu walbatiku ŋàbb boroom!

16Moo tax Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, di yebal woppi ràgg fi kaw mbuxreem yi, seen daraja tàkk, sawara xoyom ko.

17Aji Sax ji, leeru Israayil mooy doon sawara, Ku sellam|lemma="Aji Sell j-:" kooku mooy doon tàkk-tàkku sawara, xoyom taxasi Asiri aki dégam ci benn bés.

18Gott bu naat ak tool bu meññ, mu ne faraas sànk, ba mu mel ni ku wopp, yaram way seey,

19gott ba dese garab yu néew yu gone mana lim, bind ko. Ndesu Israayil dina ñibbi

20Keroog bés booba li des fi Israayil ak li rëcce kër Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:" duñu wéerooti ña leen duma. Aji Sax ji lañuy wóolu, wéeroo ko, Aji Sell|lemma="Aji Sell j-:" ju Israayil.

21Aw ndes ay délsi, di ndesu askanu Yanqóoba, ñeel Yàlla Jàmbaar ji.

22Seen xeet wi ni feppi suufas géej la tollu, te as ndes a ciy délsi. Àtteb sànkute mooy taxaw, yoon toppe ba mat sëkk.

23Sànkute déy mooy taxaw, Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi di ko sottal fi réew mi mépp.

24Moo tax Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Yeen sama ñoñ ñi dëkke Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:", buleen ragal waa Asiri yi leen di dóor yet, dinañu xàcc bolde ni waa Misra daa def ak yeen.

25Waaye fi leek lu néewa néew mbugal jeex fi seen biir, am sànj sippil Asiri seen sànkute.»

26Aji Sax ji Boroom gàngoor yee di yékkati kàcciri ci Asiri, na mu defoon waa Majan fa doju Oreb. Mooy xàcc aw yetam, mu dal géej, na mu defoon fa Misra.

27Bésub keroog sëf bu ñu leen sëfoon wàcc leen, ngeen tàggook yet wu ñu leen tënke woon, ndax seen yaram ay naat, ba yet wa damm. Noon yi songsi nañu

28Noon yeey songsi Ayat, jéggi Migron, dem ba Migmas, teg fa seeni jumtukaay,

29jaare ca xunt ma te naan: «Geba lanuy fanaani!» Waa Raama tiit, waa Gibeya, dëkku Sawul daw.

30Yeen waa Galim, yuuxuleen, yeen waa Laysa, dégluleen, yeen waa Anatot, feeluleen.

31Waa Madmena ñooy fëlxoo, waa Gebim wuti rawtu.

32Tey jii noon yaa ngay taxaw fa Noob, di sànni loxo waa tundu Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:", di ko tëkkoo waa Yerusalem googu.

33Boroom baa ngoog, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mu ngi gor garab yi, di rajaxe car yi, njobbaxtal ya gëna kawe dog, la ca gënoona siggi, wàcc.

34Mooy jël sémmiñ, goraale gajji gott bi, Libaŋ loroo loxol boroom doole, ba jóoru.

Kàddug Yàlla © 2025 La Mission Baptiste du Sénégal. Licensed under CC BY-NC-ND 4.0.
>