Esayi 21:1-17 WOLB2025 - Bible AI

1Yéene bii moo wàccal màndiŋ ma feggook géej ga: Ni ag ngëlén di riddee jaare Negew, ni la noon di bawoo màndiŋ ma, jóge réew mu raglu.

2Peeñu mu ñàng lañu ma ci wax. Workat biy wor, yàqkat biy yàq. Yeen waa Elam+ 21.2 Elam, am réew la mu bokkoon ci nguurug Pers, te di ab diiwaan ci réewum Iraan mu jamonoy tey., songleen; yeen waa Medd, gawleen leen. Dakkal naa mboolem onk yu ñu sabab.

3Lii a waral sama njàqareg xol, mitit jàpp ma, mel ni mititu mat, ma jaaxle ba déggatuma, jàq ba gisatuma.

4Bopp ubu, tiitaange jàpp ma; sama ngoonug bànneex soppiku guddi gu raglu.

5Ndab taaje, laltan lale, ñuy lekk aka naan. Ñu jekki ne: «Yeen kilifa yi, jógleen! Diwleen pakk yi!»

6Boroom bi kat da maa wax, ne ma: «Doxal taxawal ab wattukat, lu mu gis, wax ko.

7Bu gisee gawar ci watiiru ñaari fas, ak ñu wari mbaam ak ñu wari giléem, na teewloo teewlu bu baax.»

8Wattukat ba àddu ca kaw ne: «Sang bi, maa ngii yendoo séentu, fanaane wattu fii ma taxaw.

9Ma ne gawar a ngii, war watiiru ñaari fas. Nee: “Daanu nañoo, Babilon daanu na, jëmmi tuuram yépp tasaaroo fi suuf!”»

10Yeen bokk yi ñu bàcc ni pepp ca sama dàgga ja, la ma dégge ci Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoor yi, wax naa leen ko. Ab yéeneb waxyu ñeel na Duuma

11Yéene bii moo wàccal Duuma+ 21.11 Duuma, ci Arabi la féete, feggook Seyir mbaa Edom. Baat la itam buy tekki «selaw» ci làkku yawut.: Nit a ngi may woowe tundu Seyir, naan: Wattukat bi, lu des ci guddi gi? Éy wattukat bi, lu desati ci guddi gi?

12Wattukat bi ne: «Bët set, mu guddeeti rekk; boo amee looy laaj, délsil laajaat ko.» Ab yéeneb waxyu ñeel na Arabi

13Yéene bii moo wàccal Arabi: Yeen cëggi askanu Dedan+ 21.13 Dedan ak Tema ak Kedar, ay xur la yu waa Arabi dëkke. Seetal it ci aaya 14-17 (21.14-17)., mbooyum Arabi ngeen di fanaane.

14Yeen waa Tema, dajejileen ak ña mar, yóbbul leen am ndox. Dogileen ñay daw, may leen ñu lekk.

15Ay saamar de lañuy daw; saamar bu ñu xàcc ak fitt gu ñu leen diir ak tàngooru xare.

16Aji Sax ji de da maa wax ne ma: «Fileek menn at mu surga bu ñu bind waññ, sagub dëkk bii di Kedar dina sàggiku,

17li des ci jàmbaari fittkati Kedar di lu néew.» Aji Sax ji Yàllay Israayil wax na ko.

Kàddug Yàlla © 2025 La Mission Baptiste du Sénégal. Licensed under CC BY-NC-ND 4.0.
>