Esayi 3:1-26 WOLB2025 - Bible AI

1Aji Sax ji Boroom bi, Aji Sax ju gàngoor yi kat, mu ngi nii di jële Yerusalem ak Yuda, lu doon wéeruwaay, di cëslaay, muy dugub ju ñu yaakaaroon, di ndox mu ñu yaakaaroon

2ak jàmbaar ak ñeyu xare akub àttekat akub yonent ak gisaanekat ak magum pénc

3ak njiitu juróom fukki dag akub kàngam ak kiy xelal buur ak ndaanaanu liggéeykat ak jatkat bu xareñ.

4«Maay def ay gone jiite leen, di ñu yaroo seen sago, yilif leen.

5Nit ñiy soxorante, ku nekk ak moroomam, ku nekk ak dëkkandoom, ndaw di ñàkke mag kersa, sagaru nit sofental boroom daraja.

6Nit dina ne nikk mbokk ma, ca biir kër baayam, ne ko: “Yaw mi dese mbubb, jiite nu, ba lu bokk ci sunu gent bii, di sa kilifteef.”

7Keroog kooka àddu ne ko: “Duma leen mana fajal dara! Du dugub, du mbubb fa sama kër, dungeen ma def njiit!”»

8Yerusalem day téqtalu, Yuda fëlëñu. Ñooy wax aka jëf lu neexul Aji Sax ji, di gàntal leeram gi teew.

9Seen dëgër bët tuumaal na leen, ñuy bàkkaar ni waa Sodom|lemma="Sodom ak Gomor:", làquwuñu sax. Wóoy, ngalla ñoom! nde ñoo lor seen bopp.

10Neleen aji jub ji mooy baaxle, mooy yooloo añam.

11Waaye wóoy ku bon, nde mooy bonle; la mu def rekk lees koy def.

12Bokk yi, ñu xalele ñoo leen di noot, ay jigéen yilif leen. Bokk yi, seeni njiit a ngi leen di sànk, lëndëmal nañu seeni yoon.

13Aji Sax jaa ngi ci jataayu layoo, moo jóg di àtte ay xeet.

14Aji Sax jeey yékkati kàddug sikkaange, jëme ci magi ñoñam ak seeni kàngam. «Yeena sëxëtoo tóokëru reseñ bi, la ñu foqatee ci néew-ji-doolee nga seeni kër.

15Lu waral ngeen di dëggaate sama ñoñ, nappaaje néew-doole yi?» Kàddug Boroom bee, Aji Sax ji ci gàngoor yi. Puukare sànk na jigéeni Siyoŋ

16Aji Sax ji da ne: «Jigéeni Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:" a ngi daŋŋiiral, di goŋeet-goŋeeti, di regejooka rékk-rékkal, sampum ndaag, keleŋal lami wëq.»

17Moo tax Boroom beey wat jigéeni Siyoŋ nel, Aji Sax jeey muri seen jë.

18Bésub keroog Boroom bi xañ leen gànjari tànk ak takkaay yu bindoo ni jant ak yu bindoo ni weer wu feeñ

19aki loŋ-loŋ aki caq aki muuraay.

20Moo leen di xañ ay tañlaay ak lami përëg aki ngañaay ak téere yu xeeñ aki gàllaaj,

21xañ leen jaaroy torlu ak jaaroy bakkan,

22ak mbubbi xew aki mëlfë ak séri càngaay ak saagi loxo,

23ba ci yérey sooy ak yérey lẽe aki musóor aki kol.

24Su boobaa lu xasaw wuutu lu xeeñ, buum wuutu ngañaay, nel bu set wuutuy létt, yérey saaku wuutu ndoket bu rafet, toroxte wuutub taar.

25Yerusalem, say góor ay saamar lañu leen faate, say jàmbaar des xare.

26Su boobaa sa bunti dëkk sax di ñaawlooka jooy, mel ni ndaw su ñu futti, mu ne dett fi suuf.

Kàddug Yàlla © 2025 La Mission Baptiste du Sénégal. Licensed under CC BY-NC-ND 4.0.