1Gannaaw gi, ca fukk ak ñeenteelu atu nguurug Esekiyas buurub Yuda, ca la Senaxerib buurub Asiri dikk song mboolem dëkki Yuda ya tata wër, daldi leen nangu.
2Buurub Asiri moo yebale fa dëkk ba ñuy wax Lakis, bëkk-néegam Rabsake, mu ànd ak gàngooru xare gu takku, ba ca Buur Esekiyas ca Yerusalem. Ba Rabsake agsee ba tollook solomu mbàndum kaw ma, feggook yoon wa jëm ca toolub fóotukaay ba, fa la taxaw.
3Ba loolu amee bootalub buur Elyakim doomu Ilkiya moo ànd ak Sebna, bindkat ba, ak doomu Asaf, Yowax ma yor téere ya, ñu dikk dajeek moom.
4Ba mu ko defee Rabsake bëkk-néegu buurub Asiri ne leen: «Waxleen nag Esekiyas, ne ko: “Buur bu mag ba, buurub Asiri dafa wax ne: Sa yaakaar jii nga yaakaar, ana foo ko teg?
5Noon naa làmmiñ kese doy na pexeek njàmbaar cib xare? Ma ne: Ana kan nga yaakaar bay fippu ci sama kaw?
6Misra daal, nga yaakaar, bantu barax bu tas boobu di sokk képp ku ko wéeroo! Firawna buuru Misra de, mooy boobu bant ci képp ku ko yaakaar.
7Xanaa doo ma ne seen Yàlla Aji Sax ji ngeen yaakaar? Xanaa du Esekiyas moo dindi bérebi jaamookaay|lemma="bérebi jaamookaay y-:"* yeek sarxalukaayi|lemma="sarxalukaay b-:"* Aji Sax ji, ba noppi ne waa Yuda ak Yerusalem sarxalukaay boobu lañuy sujjóotal?”
8Léegi daal, déggool rekk ak sama sang buurub Asiri, ma jox la ñaari junniy fas, ndegam am ngay gawaram!
9Ana noo mana tëwe ki gëna tuut ci sama jawriñi sang? May wax ngay yaakaare Misra ay watiir aki fas.
10Te sax, xanaa du Aji Sax ji laa àndal ba dalsi fi kaw réew mii, ngir tas ko? Aji Sax ji ci boppam moo ma ne: “Songal réew mii, tas ko!”»
11Ba loolu amee Elyakim ak Sebna ak Yowax ñaan Rabsake, ne ko: «Ngalla, làkk nu arameen, dégg nanu ko. Bu nu wax ebrë, mbooloo mi ci kaw tata ji di ci dégg.»
12Bëkk-néeg ba ne leen: «Ndax yeen ak seen sang doŋŋ la ma sama sang yóbbante kàddu yii? Ñi toog ci kaw tata ji dañu cee bokkul am? Te ñu nara ànd ak yeen lekk seen jonkani bopp, naan seenum saw!»
13Bëkk-néeg ba nag taxaw, xaacu ca kaw ci ebrë ne: «Dégluleen kàdduy buur bu mag bi, buurub Asiri.
14Buur dafa wax ne: “Bu leen Esekiyas nax, ndax manu leena xettali.
15Te bu leen Esekiyas yaakaarloo Aji Sax ji, naan leen: ‘Aji Sax ji moo nuy xettali moos, te deesul teg dëkk bii ci loxol buurub Asiri!’
16Buleen déglu Esekiyas. Buurub Asiri kat dafa wax ne: Jàmmooleen ak man te ngeen génn dëkk bi, dikk nangul ma. Su ngeen ko defee, ku nekk ci yeen mana lekk ak jàmm ci garabu reseñam, lekk ak jàmm ci figgam, di naan ndoxum teenam,
17ba keroog may dikk, yóbbu leen réew mu mel ni seen réew mi, réewum pepp ak ndoxum reseñ, réewum mburu ak tooli reseñ.
18Bu leen Esekiyas sànk, naan leen: ‘Aji Sax ji moo nuy xettali.’ Ndax tuuri xeet yi mas nañoo xettali réewu wenn xeet ci buurub Asiri?
19Ana tuuri réew yii di Amat ak Arpàdd? Ana tuuri Sefarwayim? Ndax dañoo xettali Samari ci man?
20Tuuri réew yii yépp, ana mu ci xettali menn réew ci man, ba Aji Sax ji wara mana xettali, Yerusalem ci man?”»
21Ñooña ne cell, tontuwuñu ko baat, ndax Buur moo leen santoon ne leen buñu ko tontu.