Esayi 37:1-37 WOLB2025 - Bible AI

1Naka la ko Buur Esekiyas dégg, daldi xotti ay yéreem, sol saaku yu muy ñaawloo. Mu dem nag ca kër Aji Sax ji.

2Ba loolu amee mu yebal Elyakim bootalub Buur ak Sebna bindkat ba, ak ñay mag ca sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ya. Ñu sol saaku yu ñuy ñaawloo, daldi dem ca Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc.

3Ñu ne ko: «Esekiyas dafa wax ne: “Bésub tey bésub njàqare la ak mbugal ak gàcce. Mooy li ñuy wax naa: Doom a ngi ci buntub juddu, te dooley wasin réer!

4Jombul nag sa Yàlla Aji Sax ji dégg kàdduy bëkk-néeg bi sangam buurub Asiri yebal, ngir mu kókkali Yàlla jiy dund. Te kon sa Yàlla Aji Sax ji mooy dogal mbugal mi war ci kàddu yooyu mu dégg. Yékkatil kàddug ñaan rekk, ngir ñi fi desagum.”»

5Ba surgay Buur Esekiyas àggee Esayi wax jooju leen seen sang wax,

6Esayi da ne leen: «Waxleen seen sang ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Bul ragal kàddu yi nga dégg surgay buurub Asiri ñàkke ma ko kersa.

7Maa ngii di ko sol xel mu ko gëmloo xibaar bu muy dégg, ba dellu réewam, ma faate ko ab saamar ca am réewam.”»

8Gannaaw loolu Rabsake dégg ne buurub Asiri bàyyikoo na Lakis, bay xareek dëkk ba ñuy wax Libna. Mu walbatiku fekki ko foofa.

9Booba buurub Asiri daa dégg ne Tiraka buurub Kuus|lemma="Kuus:"* moo leen di songsi. Ba mu ca déggee daa yebal ay ndaw ca Esekiyas, ne leen:

10«Waxleen Esekiyas buurub Yuda ne ko: “Seen Yàlla ji ngeen yaakaar, bumu leen nax, naa leen deesul teg Yerusalem ci loxol buurub Asiri.

11Xanaa yaw ci sa bopp dégg nga li buuri Asiri def mboolem réew yi, faagaagal leen? Yaw nag, ndax yaa ciy mucc?

12Xeet yi samay maam sànk, ndax seeni yàlla dañu leena musal, muy Gosan, di Karan, di Reccef, di askanu Eden wa woon ca Telasar?

13Ana buuri Amat ak Arpàdd ak Layir ak Sefarwayim ak Ena ak Iwa?”»

14Ba Esekiyas jëlee bataaxal ba ca loxol ndaw ya, jàng ko ba noppi, dafa dem ba ca kër Aji Sax ji. Mu daldi tàllal bataaxal ba fa kanam Aji Sax ji.

15Esekiyas ñaan Aji Sax ji, ne ko:

16«Éy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Yàllay Israayil mi toog ci jal bi, fi tiim malaakay serub|lemma="serub y-:"* yi. Yaw doŋŋ yaa di Yàllay mboolem nguuri àddina. Yaw déy, yaa sàkk asamaan ak suuf.

17Ngalla Aji Sax ji, dékkal sa nopp ba dégg! Aji Sax ji, xippil say gët ba gis, te dégg mboolem kàdduy Senaxerib yi mu yóbbante, ngir ñàkke la ko kersa, yaw, Yàlla jiy dund!

18Aylayéwén Aji Sax ji, buuri Asiree tas mboolem xeet yeek seeni réew,

19te ñoo sànni seeni yàlla ci sawara it, ndax yooyoo dul Yàlla, xanaa lu nit sàkke loxoom, bant ak doj, ba tax ñu sànk leen.

20Kon nag Aji Sax ji sunu Yàlla, wallu nook moom, ba mboolem nguuri àddina xam ne yaw doŋŋ yaa di Aji Sax ji.»

21Ba mu ko defee Esayi doomu Amocc yónnee ca Esekiyas ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israayil, mi nga ñaan ci mbirum Senaxerib buurub Asiri, dafa wax ne:

22Lii moo di kàddu gi Aji Sax ji wax ci moom:

23Ana kooy kókkaleeka ñàkke kersa?

24Yaa yebal say surga,

25Maa gas ay teen, naan,

26Waaye xanaa déggoo ne bu yàgg laa dogal loolu?

27Waa dëkk ya ne yàcc, jàq, torox,

28Waaye boo toogee, boo génnee,

29Yaa xadaru sama kaw,

30«Lii, def ko ci, mu dib takk.

31Ña des ca askanu Yuda

32Yerusalem kay la aw ndes di génne,

33«Moo tax Aji Sax ji wax ci buurub Asiri ne:

34Yoon wa mu dikke lay delloo,

35Maay aar dëkk bii, musal ko

36Guddig keroog malaakam Aji Sax|lemma="malaakam Aji Sax j-:"* ji dikk, faat ca dalub Asiri téeméer ak juróom ñett fukk ak juróomi junni (185 000). Ca ëllëg sa ña mucc teela xëy, yemuñu ci lu moy ñooña ñépp diy néew.

37Ba mu ko defee Senaxerib buurub Asiri daldi fabu, ñibbi. Mu toog nag ca péey ba, di Niniw.

© 2025 Bible Society of Senegal
>