Esayi 38:1-21 WOLB2025 - Bible AI

1Jant yooyu la Esekiyas woppoon, bay waaja dee. Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc dikk, ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: Dénkaaneel sa mbiri kër, ndax dangay dee, doo jóg!»

2Esekiyas walbatiku nag, jublook miir ba, ñaan ci Aji Sax ji.

3Mu ne: «Éy Aji Sax ji, ngalla bàyyil xel ni ma àndeek yaw sama léppi xol, ci kóllëre. Te it li nga rafetlu laa jëfe.» Mu jooy nag, jooy yu metti.

4Ci kaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Esayi, ne ko:

5«Doxal ba ca Esekiyas, nga ne ko: “Aji Sax ji sa Yàllay maam Daawuda dafa wax ne: Dégg naa sag ñaan, gis naa say rongooñ. Maa ngii di yokk ci saw fan fukki at ak juróom.

6Buurub Asiri ak dooleem, maa la ciy xettali, yaw ak dëkk bii, te maay aar dëkk bii.”

7«Lii nag ngay def ab takk bu bawoo ci Aji Sax ji, di firndeel ne Aji Sax ji dina def li mu wax:

8“Maa ngii di delloo ker gi gannaaw lu tollook fukki dëggastal ya jant bi wàccoon ca kaw iskaleb Axas.”» Ci kaw loolu jant bi dellu gannaaw lu tollook fukki dëggastal ya mu jotoona wàcc.

9Mbind mii nag Esekiyas buurub Yuda moo ko bindoon, gannaaw ba mu tëddee wopp, ba jóg:

10Man de dama noon:

11Ma noon: «Dootuma gisati Aji Sax ji+ 38.11 gis Aji Sax ji mooy dem biir kër Aji Sax ji. Seetal ci aaya 22 (38.22) ak ci +bk Taalifi cant+bk* 27.4.*,

12Sama dëkkuwaay lañu sempi,

13May xalaat, ba bët set;

14May ciib-ciibi ni wetwet mbaa ramatu,

15Waaye lu may waxati?

16Boroom bi, ci sa kàddook sa jëf la nit di dunde

17Ndeke sama tiisu xol wii,

18Njaniiw du la sant,

19Kiy dund, kiy dund doŋŋ mooy ki lay sant

20Aji Sax ji yaa may wallu,

21Fekk na Esayi noon: «Indileen ab danku figg, ngeen jonj ko ci taabu Esekiyas bi, kon dina dund,»

© 2025 Bible Society of Senegal
>