Esayi 6:1-12 WOLB2025 - Bible AI

1At ma Buur Osiyas saayee, damaa gis Boroom bi toog kaw ngàngune mu kawee kawe, lafi mbubbam fees néeg bu sell|lemma="néeg bu sell b-:"* bi.

2Ay malaakay seraf ñoo taxaw, tiim ko, ku ci nekk am juróom benni laaf: ñaar yu muur seen kanam, ñaar yu muur seeni tànk, ak ñaar yu ñuy naawe.

3Ku ci nekk di àddu, naan moroom ma:

4Ku ci àddu, jëni bunt yay riir, néegu Aji Sax ji fees ak saxaar.

5Ma ne: «Wóoy man, sànku naa! Man miy nit ku làmmiñam sobewu, xeetoo ci ñu seen làmmiñ sobewu, te samay gët tegu ci kaw Buur Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi.»

6Kenn ci malaakay seraf ya naaw wutsi ma, yor aw xal wu mu keppe ag ñiim, jële ko fa sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"* ba.

7Mu laalale xal wi sama gémmiñ, ne ma:

8Ma dégg baatu Boroom bi, mu naan: «Ana ku may yebal, ana ku nuy demal boog?» Ma ne: «Xanaa man, yebal ma!»

9Mu neeti: «Demal, wax askan wii, ne leen:

10Nanga dërkiisal xoli askan wii,

11Ma ne: «Boroom bi, foo àppal loolu?» Mu ne: «Xanaa fii ba seeni dëkk gental, ba kenn dëkkatu ca, ba nit dootul nekk biir kër ya, suuf sa yàqu yaxeet, di ndànd-foyfoy.

12Aji Sax jeey yebal waa réew mi fu sore, tool yu bare booy.

© 2025 Bible Society of Senegal