1Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:" a tax duma selaw, moom Yerusalem mi tax duma noppi, ba kera àtte dëggam leer ni ceeñeeru njël, muccam dikkal ko ni jum bu ne ràññ.
2Su boobaa xeet yi gis sag njub, buur yépp gis sa daraja, ba ñu di la tudde tur wu yees wu Aji Sax ji di tuddal boppam.
3Yaay doon kaalag teraanga ci loxol Aji Sax ji, yaay doon mbaxanam buur, ci sa biir loxol Yàlla jii.
4Deesatu la woowe «Dëkk bi ñu wacc,» deesatul woowe sam réew «Réew mu gental.» Xanaa ñu woowe la «Dëkk bi ma neex,» tey woowe sam réew «Boroom jëkkër,» ndax yaa neex Aji Sax ji, te sa réew mi dina am boroom kër.
5Ni xale bu góor di takke ab janq, ni la la sa doom yu góor di moome ni jëkkër+ 62.5 doom yu góor yi ñooy waa Yuda, te ñooy moom seen réew.; ni boroom séet di bégee ab séetam, ni la la sa Yàlla di bégee.
6Yerusalem, tabb naa ay wattukat ci sa kawi tata. Buñu selaw, du guddi du bëccëg! Yeen ñiy soññ Aji Sax ji, buleen dallu.
7Buleen may Aji Sax ji fu mu dalloo, ba kera muy taxawalaat Yerusalem, ba def ko sababu cant fi kaw suuf.
8Aji Sax jee giñ lii ci ndijooram, giñ ko ci përëgam bi àttan, ne: «Dootuma joxe sam pepp, say noon dunde, te doomi doxandéem dootuñu naan sa biiñ bu bees bi nga ame saw ñaq.
9Ñi góob pepp mee koy lekk, di ko sante Aji Sax ji. Ñi witt reseñ jeey naan biiñ bi fi sama biir ëtt bu sell|lemma="sell:".»
10Jàllsileen, jàllsileen bunti dëkk bi, nangeen xàll yoonu xeet wi; maasaleleenoo, maasaleleen ngér mi, dindi doj yi! Yékkatileen raaya ju askan yépp gis.
11Aji Sax jaa ngoog, yéene na lii ba ca cati àddina, mu ne: «Waxleen Siyoŋ dëkk bu taaru bi, ne ko: “Sab jotkat|lemma="jotkat b-:" a ngii di dikk! Mu ngii ànd akub yoolam, ñaqu liggéeyam jiitu ko.”
12Dees na leen woowe “Askan wu sell wi,” “Ñi Aji Sax ji jot;” te yaw Yerusalem dees na la woowe “Ki ñu namm,” “Dëkk bi ñu waccul.”»