1Ni sawara di jafale boob,
2Ba ngay def kiraama ya ñu séentuwuloon,
3Ca cosaan ba tey maseesula dégg,
4Yaay gatandu kiy bége njekk gi muy jëfe
5Nun ñépp a mujj mel ni sobe,
6Du kenn kuy wormaal sa tur,
7Waaye déy, Aji Sax ji, yaa di sunu baay;
8Éy Aji Sax ji, bul mer lool,
9Say dëkk yu sell doon nañu màndiŋ,
10Sunu kërug jaamookaay gu sell ga te tedd,