1Ba loolu wéyee ngelaw ne ma siféet, yóbbu ma ba ca buntu penkub kër Aji Sax ja janook penku. Foofa ca bunt ba, yemuma ci lu moy ñaar fukki nit ak juróom. Ma xàmmee ca Yaasaña doomu Asur ak Pelaca doomu Benaya, di njiiti askan wi.
2Aji Sax ji ne ma: «Yaw nit ki, ñii ñooy mébétkati ñaawtéef ñiy digle lu bon ci dëkk bii.
3Ñu ngi naa: “Bunu tabaxagum ay kër; dëkk bii daa mel ni ndab, nun nu fegu ni yàpp wu ca ube.”
4Kon nag yaw nit ki, jottalil kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"* jëme ci seen kaw.»
5Leerug Aji Sax ji daldi dal fi sama kaw, ne ma: «Neel:
6Bóom ngeena bóom seen bokki dëkk bii,
7Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
8Saamar ngeen ragal,
9Maa leen di génne biir dëkk bi,
10Saamar lañu leen di faate,
11Dëkk bii du doon seen ndab,
12Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax
13Naka laay jottalil kàdduy waxyu, Pelaca (muy firi Aji rëcc ju Yàlla) doomu Benaya jekki rekk, dee. Ma ne fëlëñ, dëpp sama jë fa suuf, daldi àddu ca kaw, ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, yaay faagaagal ndesu Israayil nii?»
14Ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma:
15«Yaw nit ki, gannaaw sa bokk yooyu nga bokkal, ñuy say bokk lenqe, di mboolem waa kër Israayil ñi nekk ngàllo, ñoom la waa Yerusalem di siis, naan: “Soreleen Aji Sax ji; réew mii, nun la ko sédd.”
16Kon nag, waxal ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
17Moo tax nanga wax ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
18Mu teg ca ne: «Bu waa kër Israayil ñibbee,
19Maa leen di may beneen xol, te xel mu yees laay def ci ñoom.
20Su ko defee sama dogali yoon lañuy doxe,
21Waaye nit ña seen xol jengal seen jëf ju jomblu,
22Ba loolu amee malaakay serub|lemma="serub y-:"* ya firi seeni laaf, ànd ak mbege ya, leeru Yàllay Israayil tiim leen fa kaw-a-kaw.
23Gannaaw loolu leeru Aji Sax ji yékkatikoo fa digg dëkk ba, dem, taxawi fa kaw tund wa ca penkub dëkk ba.
24Ba loolu amee ngelaw ne ma siféet, yóbbu ba ca waa ngàllo ga ca réewum Babilon, lépp ci peeñu, ci dooley leerug Yàlla. Peeñu ma ma gis nag yem fa.