1Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji da maa dikkal ne ma:
2«Yaw nit ki, digg kërug fippukat nga dëkke, ñu ami gët te duñu gis, ami nopp te duñu dégg, ndax kërug fippukat lañu.
3Yaw nag nit ki, dajaleel ci digg bëccëg, ñépp di gis, sa jumtukaay yi, mel ni ku jëm ngàllo te nga sanci feneen, ñépp teg ci bët. Jombul ñu gis ne kërug fippukat lañu.
4Sab ëmb ngay njëkka génne digg bëccëg ni ku jëm ngàllo, ñépp teg ci bët. Te yaw nga génn ngoon ni ku jëm ngàllo, ñu teg ci bët.
5Dangay bëtt ci miir bi, ñuy gis, pax mooy yoore sab ëmb.
6Nañu la gis nga gàddu sab ëmb, génn ci lëndëm gi. Booy génn di dem, sa kanam ngay muur, ba doo mana gis suuf si, ngir misaal laa la def, ñeel waa kër Israayil.»
7Ma def loolu noonee ñu ma ko sante. Samab ëmb laa génne digg bëccëg ni ku jëm ngàllo. Ca guddi ga ma bëtte miir ba loxoy neen, ñépp di gis. Ci lëndëm gi laa gàddu sama ëmb, ñuy gis.
8Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal ma ca ëllëg sa ca suba, ne ma:
9«Yaw nit ki, xanaa waa kër Israayil, kërug fippukat gi, newuñu la: “Ana looy def nii?”
10Waxleen, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Boroom Yerusalem la artu bii ñeel, mook mboolem waa kër Israayil gi fi dëkk.”
11Neel:
12Seen boroom dëkk beey gàddub ëmbam,
13Maa koy laaw samab caax,
14Mboolem ña ko dar,
15Bu ma leen tasaaree ci biir xeet yi,
16Du tee ma ba ñenn ci ñoom,
17Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
18«Yaw nit ki, lekkal saw ñam, di kat-kati,
19te nga wax waa réew mi,
20Dëkk yu xumboon, mujj wéet,
21Gannaaw gi, kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
22«Yaw nit ki, du lii ngeen defati aw léeb ci biir réewum Israayil? “Bés yaa ngi bëgga baree, te peeñu sottiwul!”
23Kon wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
24Du peeñuy caaxaan muy amati mbaa ngisaaney jayaate
25Man Aji Sax ji,
26Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma:
27«Yaw nit ki, waa kër Israayil déy a nga naan: “Peeñu yi kii di gis, des na ay fani fan, ci lu soree sore lay jottali ay kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"*!”