1Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na ma, ne ma:
2«Yaw nit ki, caxal waa kër Israayil aw cax, ci biir léeb woo leen di léebal.
3Ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
4dagg car bu ndaw+ 17.4 dagg car bu ndaw mooy ba ñu yóbboo Buur Yoyakin ngàllo ca Babilon.* ba ca gëna kawe,
5Mu sàkk ci jiwum réew mi+ 17.5 jiwum réew mi mooy Cedesyas baayu Yoyakin bu ndaw. Buur Cedesyas la Nebukatnecar dénkoon nguurug Yuda.*,
6Mu jebbi, dig reseñ, gëna yaatu te gàtt taxawaay.
7«“Jeneen jaxaay ju mag+ 17.7 jeneen jaxaay ju mag mooy Firawna buuru Misra.* daldi ne jimeet,
8Ci tool bu nangu bu feggook ndox mu ne xéew la jëmbate woon,
9«Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
10Ma nga noonu jëmbate, waaye mbaa dina baaxle yee?
11Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
12«Waxal waa kër fippukat yi, ne leen: “Xamuleen lu mbir yooyu di wund?” Ne leen: “Mu ngoogu, buuru Babilon a dem Yerusalem, jàpp buur baak kàngam ya, ànd ak ñoom, yóbbu Babilon.
13Moo tànn ku bokk ci askanu buur, fasook moom kóllëre|lemma="kóllëre g-:"*, giñloo ko ne dina ko nangul, daldi yóbbu njiiti réew mi,
14ngir nguurug Yerusalem suufe, baña yékkatiku, di wéy di surgawu Babilon, ni ñu fasoo woon ak ñoom kóllëre.
15Ka bokk ci askanu buurub Israayil nag fippu, yónni ay ndaw réewum Misra, ngir ñu jox ko ay fas ak mbooloo mu takku. Moo, ka def loolu ndax dina baaxleem? Mbaa dina mucc? Nu mu cay mucce te wor kóllëre ga mu fasoo woon?
16«“Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, ci biir réewum buur boobu ko fal, te mu sàggane la mu ko giñaloon, wor kóllëre ga mu fasante woon ak moom, ci biir Babilon googu lay deewe.
17Firawnaak mbooloom mu réy ak gàngooram gu mag sax duñu ko mana wallu ci xare, keroog bu ñuy yékkati ab sëkk, tabax ab gawukaay ngir bóom ñu bare.
18Moo sàggane ngiñ, moo wor kóllëre ga mu fasante woon. Mu ngoog, moo joxe kàddoom, ba noppi walbatiku def lii lépp. Du mucc mukk.
19«“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Giñ naa ko ci man miy dund, maay këpp jëfam ci kaw boppam ndax ngiñ li mu ma giñal la sofental, kóllëre gi mu fasanteek man la wor.
20Maa koy laaw sama mbaal, mu lonkoo samab caax, ma yóbbu ko Babilon, layoo faak moom ñàkke worma gi mu ma ñàkke worma.
21Mboolem ñay dawe ca gàngooram yépp, saamar a leen di faat; ña cay rëcce, fépp fu ngelaw jublu lañuy tasaarooji, ba ngeen xam ne man Aji Sax ji maa wax.
22«“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
23Ca kaw tundu Israayil wu mag wa laa koy jëmbat,