1Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
2«Ana lu waral waxin wii ngeen di waxe fi Israayil naan:
3«Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, dootuleen waxe woowu waxin fi Israayil.
4Mu ngoog, bépp bakkan maay Boroom. Muy bakkanu baay, di bakkanu doom, maa moom. Bakkan bi bàkkaar daal mooy dee.
5Su nit dee boroom njekk,
6tund ya ca saraxi tuur ya, lekkewu ca,
7Du kenn ku mu néewal doole,
8Aw ndollent taxu koo leble,
9Sama dogali yoon, mu di ca doxe,
10«Jii waay su juree doom ju néeg juy tuur deretu jàmbur
11te moom miy baayam jëfewu ci lenn,
12ku ñàkk ak ku néewle, mu néewal doole,
13leblee, mu yokk ndollent,
14«Waaye kooka nag su amee doom,
15tund ya ca saraxi tuur ya, lekkewu ca,
16Du kenn ku mu néewal doole,
17Néew-ji-doole, loxoom dalu ko,
18Baayam a jaay doole,
19«Ngeen neeti: “Lu tax doom du gàddu bàkkaaru baay?” Xanaa du yoon ak njub la doom ji jëfe? Sama dogali yoon yépp, mu di ko sàmm, di ko jëfe? Dina dund kay!
20Ki bàkkaar daal mooy dee. Doom du gàddu ñaawtéefu baay, baay it du gàddu ñaawtéefu doom. Njub réerul boroom, mbon réerul boroom.
21«Waaye ku bon ki su dëddoo mboolem moy yi mu moy, di sàmm sama mboolem dogali yoon, di def dëgg ak njub, dina dund moos te àtteb dee du ko topp!
22Mboolem tooñam ya mu tooñoon, deesu ko ko dencal. Njekk li mu jëfe moo koy taxa dund.
23Ana bànneex bu ma am ci deewug ku bon? Xanaa bu dëddoo jikkoy mbonam, ba dund! Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
24«Waaye su dee boroom njekk, ba noppi dëddu njubte, di def njubadi, di roy mboolem jëf ju siblu ju ku bon def, kooku nu muy dunde? Mboolem njub gu mu defoon, deesu ko ko dencal. Ag ñàkk wormaam ak bàkkaaram moo koy taxa dee.
25«Yeen nag ngeen ne: “Ni Boroom biy doxale du noonu!” Waa kër Israayiloo, dégluleen! Sama doxalin a dul noonu, am yeen seeni doxalin?
26Boroom njekk su dëddoo njekkam, di def njubadi ba dee, njubadeem ga mu def moo ko taxa dee.
27Waaye ku bon nag, su dëddoo mbonam ga mu nekke, di jëfe yoon ak njub, moom moo musal bakkanam.
28Ndegam moo xoolaat, ba dëddu mboolem tooñam yu mu tooñ, dina dund déy. Du dee moos.
29Moonte waa kër Israayil nee: “Ni Boroom biy doxale du noonu.” Yeen waa kër Israayil, samay doxalin a dul noonu am yeen seeni doxalin?
30«Lii moo tax yeen waa kër Israayil, ma di leen àtte, ku nekk ciy jëfam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Dëppleen te dëddu mboolem seeni tooñ, ngir seenu ay bañ leena gàllankoor.
31Xalableen mboolem tooñ yi ngeen di tooñ. Sàkkuleen xol bu yees ak xel mu yees. Yeen waa kër Israayil, lu jar ngeen di dee?