1Aji Sax ji ne ma: «Yaw nag jooyal garmiy Israayil.
2Neel:
3Moo tàggat kenn ciy goneem+ 19.3 Wax ji ci Buur Yowaxas la jëm. Seetal ci +bk 2.Buur ya+bk* 23.31-34.*,
4Ba ko xeet ya déggee, dañu koo fexeel,
5«“Ndey gaynde xaar a xaar,
6Mu ànd ak moroomi gayndeem,
7Mu tëdde seeni jëtun,
8Teewul xeeti diiwaan ya ko séq ànd,
9Ñu lonk, dugal cib kaaf,
10«“Sa ndey a la niru, mel ni reseñ
11Mu am car yu dëgër yu man yeti nguur,
12Waaye am sànj a ko buddi, sànni fi suuf,
13Tey mu ngi jëmbate fi màndiŋ mi,