Esekiyel 2:1-9 WOLB2025 - Bible AI

1Ba loolu amee boroom kàddu ga ne ma: «Yaw nit ki, jógal taxaw, ma wax la.»

2Naka la ma wax loolu, ngelaw solu ma, ne ma yékkét, ma taxaw, di dégg kiy wax ak man.

3Mu ne ma: «Yaw nit ki, maa lay yebal ci bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*, xeeti fippukat yi fippu ci sama kaw; ñook seeni maam dañu maa mas di tooñ ba bésub tey jii.

4Ci nit ñu dëgër bopp te dërkiis laa lay yónni. Wax leen, ne leen: “Lii la Boroom bi Aji Sax ji wax.”

5Ñoom nag, su ñu la déglook su ñu gàntalee ndax kërug fippukat gi ñu jikkowoo, dinañu xam ne ab yonent a ngi ci seen biir.

6Waaye yaw nit ki, bu leen ragal, bul ragal seeni wax. Xam naa ne ay taxas aki dég a lay wër, nga toog ci kawi jiit. Waaye bul ragal seeni wax te bul tiit ci lenn lu ñu la won doonte kërug fippukat lañu.

7Nanga leen àgge samay wax, ñu déglook ñu gàntal, nde ay fippukat lañu.

8Yaw nit ki nag, déglul lii ma lay wax. Bul fippu ni kërug fippukat gii. Sexal, te lekk li ma lay jox.»

9Naka laa xool, yem ci loxo bu ñu ma tàllal. Ndeke téere bu ñu taxañ moo ci nekk.

© 2025 Bible Society of Senegal
v>