1Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
2«Yaw nit ki, neel jàkk yoonu ndijoor, sànni kàddu jëme ci diiwaanu bëj-saalum boobu, jottali kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"* jëme ci gottub Negew boobu+ 21.2 Kàdduy waxyu yii ñu ngi jëm ci wàllu Yuda gi féete bëj-saalum.*.
3Nanga wax gottub diiwaanu Negew, ne ko: “Déglul kàddug Aji Sax ji. Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jafal ci sa biir, daay guy xoyom sa garab yépp gu naat ak gu wow. Dara du ko mana fey. Daay ga day jóge bëj-saalum ba bëj-gànnaar te ñépp a cay lakk,
4ba mboolem kuy dund xam ne man Aji Sax ji maa ko taal te du fey.”»
5Ma ne ko: «Éey Boroom bi Aji Sax ji, ñii déy a ngi wax ci man, naan: “Kii moom xanaa day léeb aka léebaat rekk?”»
6Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
7«Yaw nit ki, jàkkaarlool ak Yerusalem, nga sànni kàddu béreb yu sell yi te nga jottali kàdduy waxyu ci kaw réewum Israayil.
8Waxal réewum Israayil ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngi nii fi sa kaw. Maay boccee sama saamar ci mbaram, daldi dagge fi yaw ku jub ak ku bon.
9Dagge fi yaw ku jub ak ku bon moo may taxa boccee sama saamar ci mbaram, dal ci mboolem kuy dund, bëj-saalum ba bëj-gànnaar,
10ba képp kuy dund xam ne man Aji Sax ji maa bocci sama saamar, te du dellu ci mbaram.”
11Yaw nit ki, binnil, neel yàcc, di binnee naqar, ñuy gis.
12Dees na la laaj ne la: “Looy binni?” Nga ne leen: “Xanaa mbir mi ma dégg. Bu agsee fit yépp ay rëcc, loxo yépp nasax, xol yépp jeex, óom yépp di fenqoo. Mu ngooguy dikk te dina am. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»
13Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
14«Yaw nit ki, jottalil kàdduy waxyu, nga ne: “Boroom bi dafa wax ne:
15Dees koo jonj ngir bóome,
16Santaane nañu ñu jonj saamar bi,
17Yaw nit ki, yuuxul, jooyal,
18Nattu bi metti na!
19«Yaw nit ki, jottalil kàdduy waxyu,
20yóbbuw fit, tërëfloo ñu bare.
21Saamar, ñaweel sa ndijoor,
22man it ma ŋëb bii loxo, dóor ca bee,
23Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
24«Yaw nag nit ki, sàkkal ñaari yoon yu saamaru buuru Babilon di jaare dikk; ñaari yoon yuy bàyyikoo ci mennum réew. Tegal fa buntu yoon wu ci nekk màndarga muy tegtale dëkk ba yoon wa jëm;
25wenn yoon wa saamaru Babilon war fa aw ba àkki Raba, dëkkub Amoneen ñi; weneen yoon wa ca des saamar ba aw fa ba àkki Yerusalem, dëkk ba ñu dàbbali, ca Yuda.
26Buuru Babilon a ngay taxaw ca selebe yoon wa, fa ñaari yoon ya séddalikoo, ngir gisaane. Dina yëngal fitti seetukaay yi, xool ci terafim yi, di jumtukaay yi ñuy gisaanee, ak ci resu jur.
27Fitt giy misaal Yerusalem ci ndijooram lay wadd. Mu samp dàjjikaayi dénk yi, daldi yéene ndigalu bóome, xaacu, daldi sës dàjjikaay yi ci bunt yi, yékkati sëkk yi, ngir taxawal ab gawukaay.
28Waa Yerusalem foog ne ngisaane googu misaal seen jéll, caaxaan la, ndax ngiñ moo lal seen kaaraange, ba du deñ. Waaye buuru Babilon a leen di fàttali seenug tooñ, ba jàpp leen njaam.
29«Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw yeena fàttaliku seen ñaawtéef, seeni tooñ ne fàŋŋ, seeni bàkkaar fés ci seen jëf jépp, gannaaw yeena ñaaw ñaawtéef gu ñu leen di fàttalikoo, dees na leen jàpp.
30«Waaye yaw garmib Israayil bu sobewu bu bon bi,
31Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
32Tasaaroo, tasar, maa ko naa tasar!
33«Yaw nag nit ki, jottalil kàdduy waxyu, nga ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ci mbirum Amoneen ñeek seeni saaga ne:
34Gisal nañu leen peeñuy caaxaan,
35«“Léegi dellooleen saamar ci mbaram.
36Maa lay xëpp sama sànj,