1Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ca juróom ñeenteelu at ma, fukki fan ca fukkeelu weer wa. Mu ne ma:
2«Yaw nit ki, bindal bés bii, bés bii ci boppam, ndax buuru Babilon gaw na Yerusalem bés niki tey.
3Léebalal kërug fippukat yi aw léeb, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
4Booleel dogi yàpp yi, def ci:
5Li gën ci gétt gi ngay sàkk,
6Boroom bi Aji Sax ji kat dafa wax ne:
7Deret ji mu tuur a ngi ci biiram ba tey;
8Man maay wacc deret ja ca doj wa amul dara,
9Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne:
10Jalal a jal matt mi, xamb taal bi.
11Boo noppee tegal cin li deful dara ci xal yi,
12Coonoy neen, xëmit ja ne xéew du deñ,
13Sa sobeey sa yàqute!
14Man Aji Sax ji maa wax,
15Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
16«Yaw nit ki, maa ngii di nangusi sa bànneexu bët cim pàdd. Bul yuuxu, bul jooy, bu sa rongooñ wadd.
17Binnil ndànk te bul ñaawlu. Bul tàggook sa kaala, bul tàggook say carax, bul muur sa tuñum kaw ba ci sikkim di ko ñaawloo. Bul lekk ñam wu jóge ci njaal mi+ 24.17 Ku deele daawul togg. Ñiy jaalesi ñooy indi ñam wu ñu lekk ci dëj bi.*.»
18Wax naak mbooloo mi ci suba. Ci ngoon si, sama soxna dee. Bët set ma def li ñu ma sant.
19Mbooloo mi nag ne ma: «Xanaa doo nu wax lii ngay def nii, lu muy wund ci nun?»
20Ma ne leen: «Kàddug Aji Sax jee ma dikkal, ne ma:
21Waxal waa kër Israayil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di teddadil sama kër gu sell gii, seen sag bii ngeen di doolewoo, di seen bànneexu bët, di seen nammeelu bakkan. Seen doom yu góor ak yu jigéen ya ngeen bàyyi Yerusalem, saamar dina leen tëral.
22Te nangeen def nii ma def. Buleen muur tuñum kaw ba ci sikkim te buleen lekk ñam wu jóge ci njaal mi.
23Buleen tàggook kaala, buleen tàggooki carax. Buleen yuuxu, buleen jooy. Waaye dingeen jeex tàkk ndax seeni ñaawtéef, ngeen ànd di binni.”
24Mu ne: “Na Esekiyel di seen misaal. Bu jotee, mboolem nu mu def, nangeen ko def, ba xam ne man maay Boroom bi Aji Sax ji.”
25«Yaw nit ki, bés bu ma nangoo ci ñii seen tatay daraja ji ñuy bége, muy seen bànneexu bët, di seen xintey bakkan, ba nanguwaale seen doom yu góor ak yu jigéen,
26bésub keroog ku ca rëcce dina dikk ba ci yaw, àgge la xibaar bi.