Esekiyel 27:1-35 WOLB2025 - Bible AI

1Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:

2«Yaw nag nit ki, yékkatil kàddu, muy ay jooy ci kaw dëkkub Tir.

3Waxal Tir mi toog ci buntu géej, jula yooyuy jëflanteek xeeti dun yu bare, nga ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:

4Yaw mi sa kemu suuf àkki xolu géej,

5Dañu laa tabax ni ñuy tabaxe gaal,

6Ñu gorati garabu seen yu Basan,

7Lẽe bu bawoo Misra lañu ràbb ba mu jekk,

8waa Sidon ak Arwàdd doonoon say joowkat.

9magi Gebal ñeek nitam ñu xareñ ñi fi yaw féetewoo di jagal.

10Waa Pers ak waa Ludd ak waa Puut,

11Arwàddeen ñeek sa niti bopp a daan wattu sa tata yépp,

12«“Tarsis dëkk baa doon sab jula ndax sa jépp xeetu alal ju bare. Xaalis ak weñ gu ñuul ak gu weex ak betteex la waa dëkk ba daan weccikoo seen alal.

13Waa Geres ak Tubal ak Meseg di say jula, di leen indil ay jaam ak ndabi xànjar yu ñuy weccikoo seen koom.

14Waa kër Togarma indi ay fas aki gawar aki berkelle, di ko weccikoo seen alal.

15Dedaneen ñi di say jula, koomu dun yu bare di jaare say loxo, ñu di la feye bëñi ñey ak bantu jalambaan.

16Waa Siri it di say jula, di jëndeek yaw lu bare loo defar, di ko wecci per yu jafe, ak ndimo yu xewar, ak séri ràbb ak lẽe ak peri xor ak peri rubi.

17Yudaak réewum Israayil it di say jula, di la wecci bele bu bawoo Minit, ak dugub ak lem ak diwu togg ak diwu yaram.

18Dëkkub Damaas di jula lu bare ak yaw, ci lépp loo defar ak jépp alal joo barele, di la ko weccee biiñ bu jóge Elbon, ak kawaru xar gu weex.

19Waa Wedan ak waa Geres bàyyikoo Usal, di la wecci sa koom weñ gu ñu tëgg, ak xasum kaas ak barax bu xeeñ.

20Waa Dedan it di say jula, indil la seen ndimoy tegi fas.

21Waa Arabi ak mboolem garmiy Kedar it di jëflanteek yaw, feye la ay tàppaanga aki kuuy aki sikket.

22Julay Seba ak Raama it di jëflanteek yaw, di la indil ngën-gi-safal ak mboolem peru gànjar, ak wurus yu ñuy weccikoo sa alal.

23Waa dëkk yii di Karan ak Kane ak Eden ñoom it di say jula, ñook julay Seba ak Asur ak Kilmàdd.

24Ñooñoo doon say jula yu lay indil yérey tànnéef ak turki yu yolet ak yérey ràbb ak malaan yu yànj ak goj yu rawaasoo yu wér.

25Ay gaali Tarsis yu mag a daan yóbbu sam njaay.

26Say joowkat waral la mbeex mi ne màww,

27Sa alal ja, sab yeb, sa njaay ma,

28Bu say mool yuuxoo,

29képp kuy ŋàbb joowu wàcce gaalam.

30Ñoo lay jooyal,

31Yaay tax ñuy nelu,

32Ñeey am tiis, yékkatil la kàddug jooy,

33Ba ngay yebbee géej sam koom,

34Léegi rajaxoo nga biiri gannax ca biir xóotey géej,

35Waa dunoo dun a la tiisoo,

© 2025 Bible Society of Senegal
div>