1Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
2«Yaw nit ki, waxal Boroom Tir, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
3Xëy-na yaa sut Dañeel am xel,
4Ci sam xel ak sa manoore nga ame alal,
5Ci sa xelum jula mu réy nga yokke sa alal,
6Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
7maa ngii di la indil ay doxandéem,
8Pax lañu lay tàbbal,
9Xanaa doo janook ki lay rey, naati: ‘Maay Yàlla’?
10Deewug yéefar bu xaraful ngay deewe ci loxol doxandéem yi.
11Kàddug Aji Sax ji dikkalati ma ne ma:
12«Yaw nit ki, yékkatilal buurub Tir kàddug jooy! Nga ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
13Yaa nga woon biir Àjjana, toolub Yàlla ba,
14Yaa doon malaakam serub|lemma="serub y-:"* mu ne ràññ, di aare,
15Ba ñu la sàkkee, nga dale mat ci say jëfin,
16Sa liggéeyu jula bu yaatu moo la feesal fitna,
17Sab taar a la fuuyloo,
18Sa ñaawtéef yu bare ak njublaŋ gi ngay julaa,
19Mboolem ñi la xam ci xeet yi,
20Kàddug Aji Sax ji dikkalati ma ne ma:
21«Yaw nit ki, neel jàkk Sidon+ 28.21 Sidon, dëkk la bu bootu woon ci Tir, ca wetu bëj-gànnaar, ca tefes ga.*, nga jottali kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"* fi kawam.
22Neel:
23Maa fiy yebal mbas,
24«Su boobaa waa kër Israayil, seen dëkkandoo yi leen di sewal,
25«Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Bu may dajale waa kër Israayil, di leen jële ci diggu xeet yi ñu tasaaroo, ca laay fésal sama sellaay fa seen biir, yéefar yi gis, ñu dëkke seen suufas bopp sa ma joxoon Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:"* sama jaam ba.