Esekiyel 3:1-26 WOLB2025 - Bible AI

1Mu ne ma: «Yaw nit ki, lii ngay gis, lekk ko. Lekkal téere bii te dem wax ak waa kër Israayil.»

2Ma ŋa, mu leel ma téere ba.

3Mu ne ma: «Yaw nit ki, lekkal téere bii ma la jox, ba suur këll.» May lekk, mu neexe ni lem.

4Mu ne ma: «Yaw nit ki, demal ba ca waa kër Israayil, te nga àgge leen samay wax.

5Du ci waaso wu xóotu làkk te diisu làmmiñ lees la yebal. Ca waa kër Israayil nga jëm.

6Bare na waaso yoo xamul seeni wax, yu xóotu làkk te diisu làmmiñ. Te su ma la yebaloon ci ñoom, ñu déggal la.

7Waaye waa kër Israayil duñu la nangoo déggal, ngir nanguwuñu maa déggal; ndax waa kër Israayil gépp a dëgër bopp te dërkiis.

8Maa ngii di la may kanam gu ñemee ni seen kanam, ba nga dëgër bopp ni ñoom.

9Jamaa moo raw doj te ni laay dëgërale sa bopp. Bu leen ragal, bu leen tiit, li ñuy kërug fippukat yépp.»

10Mu teg ca, ne ma: «Yaw nit ki nag, mboolem li ma lay wax, dégloo ko nopp, te teewloo ko xel.

11Nanga dem ba ca sa bokki ngàllo ga, nga wax leen, ñu déglook ñu gàntal, ne leen: “Lii la Boroom bi Aji Sax ji wax.”»

12Ci kaw loolu ngelaw li Aji Sax ji wol ne ma siféet, may dégg ci sama gannaaw, riirum kàddu gu xumb gu ne: «Cant ñeel na darajay Aji Sax ji fi màkkaanam.»

13Mu ànd ak riirum laafi mbindeef yay fenqoo, ak coowal mbege ya ñu feggool, muy riir mu xumb.

14Ba loolu amee ngelaw ne ma siféet, yóbbu. Maa ngay deme naqar ak xol bu tàng, te loxol Aji Sax ji diis gann ci sama kaw.

15Ma àgg ba ca ngàllog Tel Abib ga dëkke tàkkal dexu Kebar. Foofa ñu dëkk laa toog, jommi ci seen biir diiru juróom ñaari fan.

16Ba juróom ñaari fan ya matee, kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma:

17«Yaw nit ki nag, wattukat laa la tabb, ñeel waa kër Israayil, ba boo déggee baat bu jibe sama gémmiñ, yaa leen koo artoo ci sama ndigal.

18Su ma nee ku bon ki: “Dee rekk ay sa àtte,” te fekk artuwoo ku bon ka, waxuloo lu ko waññee ca mbonam ga, ba mu mucc, ku bon kooka day dee ndax tooñam, waaye bakkanam yaw laa koy laaj.

19Waaye yaw soo artoo nit ki ngir mu wacc yoonu mbonam nag, tooñu boppam a ko reylu, waaye yaw musal nga sa bopp.

20Su dee boroom jëfi njekk bu dëpp yoonu njekkam, di def ndëngte, maa koy gàllankoor, mu dee. Soo ko artuwul ndax bàkkaaram, dina dee, te deesul bàyyi xel njekkal démbam la, waaye bakkanam, yaw laa koy laaj.

21Waaye nag su dee yaa artu boroom jëfi njekk bi, ba tax bàkkaaratul, dina dund déy, ndax kàddug artu ga, te yaw it musal nga sa bopp.»

22Gannaaw loolu loxol Aji Sax ji dikk fa ci sama kaw. Mu ne ma: «Génnal ba ci joor gi, ma wax faak yaw.»

23Ma génnsi ba ca joor ga. Ndeke jëmmu leeru Aji Sax jaa nga foofa, taxaw mel ni jëmmu leer ga ma gisoon ca tàkkal dexu Kebar. Ma ne gurub, dëpp sama jë fa suuf.

24Ci kaw loolu ngelaw solu ma, ne ma yékkét, ma taxaw. Mu wax ak man, ne ma: «Doxal, tëjuji sa biir néeg.

25Te kat yaw nit ki, dees na la fa takke ay buum, yeew la ba dootoo mana génn, dem ci nit ñi.

26Sa làmmiñ laay taqal ci sa denqleñ, nga luu ba doo leen mana yedd, ndax kërug fippukat lañu.

© 2025 Bible Society of Senegal
iv>