1Ba loolu amee ca fukkeelu at maak benn, benn fan ca ñetteelu weer wa, kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
2«Yaw nit ki, waxal Firawna buuru Misra ak gàngooram, ne ko:
3Asiree ngoog, garabu seedar la woon ca Libaŋ,
4Bëti ndox suuxat ko, ndoxi xóote yi màggal ko,
5Moo ko taxa sut garabi àll bi,
6Picc yépp di tàgg ci ay caram,
7Taaram a nga ca taxawaayam ak guddaayu caram ya,
8Du genn garabu seedar ca toolub Yàlla gu ko yóbbuloon dara,
9Maa ko rafetale njañam lu sëq,
10«“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaa siggi woon ca kaw, kii la njañam àkki woon ci niir ya, muy damoo taxawaayam.
11Maa koy jébbal ku jiite ay xeet, mu fey koo fey coxoram, ma dàq ko.
12Ay doxandéem a dikk, bokk ci xeet yi gëna néeg, gor ko, wacc. Ay bànqaasam wadd ci kaw tund yeek xur yi, ay caram dammatoo ci xunti àll bi yépp. Waa réew yépp dawe keram, wacc ko,
13picc yépp di tàgg ci peram bi tëdd fi suuf, rabi àll yépp di goor ci caram yi fi suuf.
14Su boobaa genn garab gu feggook ndox dootul siggi ca kaw, ba njañ lay àkki niir ya, te genn garab dootul màndim ndox, bay damu ci kawi moroomam. Ñoom ñépp déy lañu àppal dee, ñu jëm xóotey suuf, tëddi biir bàmmeel ni waa àddina sépp.
15«“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Bés ba seedar ga tàbbee njaniiw, maa dogal ag ñaawlu: Maa sàng xóote ya ndax moom, téye dexi biir suuf, wali ndox yi noon xéew, dakk. Maa tax ba gottub Libaŋ ñaawlu ci loolu, tax ba garabi àll bi yépp doxe ca lax.
16Maa def xeet yi dégg jéllu seedar gi, di lox, ba ma ko tàbbalee njaniiw, boole kook mboolem ñiy tàbbim pax. Noonu la garab yépp di muñe seen demin, ndax seedar ga teew ni ñoom ci biir xóotey suuf, maanaam mboolem garabi Àjjana yi gëna taaru, boole ca yay ngëneeli Libaŋ, ak mboolem garab yi màndim ndox.
17Ñoo bokk ak seedar gi wàcci njaniiw, ànd caak ña fa saamar tëral, ñoom ñi ko doon dooleel, maanaam xeet yi daan toog ci keram.