Esekiyel 36:1-37 WOLB2025 - Bible AI

1«Yaw nit ki, jottalil tundi Israayil kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"*. Neel:

2Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:

3Kon jottalil kàdduy waxyu, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:

4kon nag yeen tundi Israayil,

5Boroom bi Aji Sax ji nag dafa wax ne:

6Kon nag, jottalil kàdduy waxyu suufas Israayil

7Loolu tax na Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:

8«“Waaye yeen tundi Israayil, yeenay naat,

9Maa ngii déy maak yeen,

10Maa leen di fulal aw nit, ci biir Israayil gépp ba mu daj,

11Yeen tund yi, maa leen di fulal nit ak mala,

12Yaw suufas Israayil, maay doxloo nit fi sa kaw,

13«“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:

14Kon yaay réew mu dootul dëmme,

15Dootuma la dégtal ñàkk kersay yéefar yi,

16Kàddug Aji Sax ji dikkalati ma ne ma:

17«Yaw nit ki, ba waa kër Israayil dëkkee seen suufas bopp, dañu koo sobeel ak seen jikko ak seeni jëf, seen jëfin mel ni sagaru sobe ci man.

18Ma xëpp leen sama xadar ndax deret ji ñu tuur ci réew mi, ak kasaray tuur yi ñu ko sobeele.

19Ma tasaare leen ci biir yéefar yi, ñu wasaaroo fi biir réew yi. Seen jikko ak seeni jëf laa leen àttee.

20Waaye fu ñu dem ca biir yéefar ya, teddadil nañu fa sama tur wu sell|lemma="sell:"*, nit ña di leen waxtaane, naan: “Ñii de, ñoñi Aji Sax ji lañu, teewul ca réewam ma lañu bàyyikoo nii.”

21Moo tax ma daldi seet ci sama teddaayu tur wu sell wi waa kër Israayil di teddadil fi biir yéefar yi ñu fekki.

22«Moo tax nanga wax waa kër Israayil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen waa kër Israayil, li may waaja def, du yeen laa ci seet, li ma ci seet mooy sama teddaayu tur wu sell wi ngeen teddadil fi digg yéefar yi ngeen fekki.

23Kon dinaa fésal sama sellaayu tur wu màgg wi ñu teddadil fi biir yéefar yi, sama tur wi ngeen teddadil fi seen biir. Ci yeen laay fésale sama sellaay, yéefar yiy gis, ba xam ne maay Aji Sax ji. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

24Maa leen di seppee ci yéefar yi, dajale leen ci mépp réew, delloosi leen fi seen suufas bopp.

25Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.

26Maa leen di jox xol bu yees, te xel mu yees laay def ci seen dënn. Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, wecceel leen ko xol yu nooye ni suux,

27te samam xel laay yeb fi seen biir dënn, ba dogal ngeen mana topp sama dogali yoon, di sàmm aka jëfe sama àttey yoon.

28Su boobaa ngeen mana dëkke réew mi ma joxoon seeni maam, di sama ñoñ, may seen Yàlla.

29Maa leen di musal ci seen mboolem sobe, maay woo am pepp, ful ko, te dootuma leen teg ab xiif.

30Maay ful doomu garab ak meññeefum tool, ba dootuleen am gàccey xiif fi digg yéefar yi.

31Su boobaa yeenay fàttaliku seen jikko yu bon yaak seen jëf ju baaxul. Su ko defee ngeen jéppi seen bopp ndax seeni ñaawtéef ak seen jëf ju siblu.

32Du yeena tax nag may jëfe noonu. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Na leen loolu wóor. Kon nag yeen waa Israayil, rusleen ba ne tott ci seeni jëfin.

33«“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Bés bu ma leen setalee ba ngeen tàggook seen mboolem ñaawtéef, dinaa delloo dëkk yu mag yi aw nit, gent yi tabaxewaat.

34Mbooy gu wéet gi, dees na ko beyaat, ba mu wuuteek ab wéetaay, ni wéetaay ba ñépp ñi fa jaare seede woon.

35Su boobaa dees na ne: ‘Xoolleen miim réew, ak mbooy gi mu doonoon, tey mu naat ni toolub Àjjana! Dëkk yi it ay gent la woon, wéet, tojatoo, tey ñu dàbbali lépp, ba dëkke nii!’

36Su boobaa seen dëkkandooy yéefar yi fi des dinañu xam ne man Aji Sax ji maa tabaxaat dëkk yu mag yi tojatoo woon, jëmbataat mbooy gi. Man Aji Sax ji, maa wax te maay jëf.”

37«Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Lii laay nangulaatal waa kër Israayil, defal leen ko: maay ful nit ñi niy gàtt.

© 2025 Bible Society of Senegal
div>