Esekiyel 37:1-27 WOLB2025 - Bible AI

1Gannaaw loolu loxol Aji Sax ji da maa dikkal. Aji Sax ji yóbbu ma ci ngelawam, ba teg ma ca digg joor ga, fekk joor ga fees dell aki yax.

2Mu wërloo maa wërloo ca biir yax ya, ndeke yax yaa nga bare lool te wow koŋŋ ca biir joor ga.

3Mu ne ma: «Yaw nit ki, ma ne, yii yax ndax man naa dundaat?» Ma ne ko: «Boroom bi Aji Sax ji, loolu de, yaw doŋŋ a ko xam.»

4Mu ne ma: «Jottalil kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"* fi kaw yax yii, ne leen: “Yeen yax yu wow yi, dégluleen kàddug Aji Sax ji:

5Boroom bi Aji Sax ji dafa wax yax yii, ne leen: Maa ngii di leen sol ag noo, ngeen dund.

6Maa leen di may ay siddit, saxal leen aw suux, sànge leen ab der, sol leen ag noo, ngeen dund, ba xam ne maay Aji Sax ji.”»

7Ma jottali kàdduy waxyu na mu ma ko sante. Naka laa jottali kàdduy waxyu rekk, coow daldi jib, ànd akum riir, fekk yax yaay booloo, bu nekk ak ba muy àndal.

8Ma gis ay siddit taq ca, aw suux sax ca kaw, ab der dikk, tege ca kaw, te genn noo amu ca.

9Mu ne ma: «Yaw nit ki, jottalil noo gi kàdduy waxyu, jottali ko kàdduy waxyu ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaw noo gi, bàyyikool ñeenti yooni ngelaw yi te dikk, wal fi biir ñii ñu bóom, ba ñu dund.”»

10Ma def la mu ma sant, jottali kàdduy waxyu, noo ga dikk, duggsi, ñu dundaat, jóg taxaw, di gàngoor gu baree bare.

11Mu ne ma: «Yaw nit ki, yax yii ñooy mboolem waa kër Israayil. Ñu ngi naan: “Nun de, ay yaxi neen yu wow koŋŋ lanu, sunu yaakaar tas na, nun kay yàqu nanu.”

12Kon nag jottalil kàdduy waxyu, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen sama ñoñ, maa ngii di ubbisi seeni bàmmeel, dekkale leen ca seeni bàmmeel, delloosi leen kaw suufas Israayil.

13Yeen sama ñoñ, bu ma ubbee seeni bàmmeel, ba yékkatee leen fa, dingeen xam ne maay Aji Sax ji.

14Maa leen di sol samag noo, ngeen dund, ma samp leen ci seen suufas bopp, ba ngeen xam ne man Aji Sax ji maa wax, maa def. Kàddug Aji Sax jee.”»

15Ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:

16«Yaw nit ki, wutal bant, nga bind ci kaw lii: “Ñeel Yuda ak giiri Israayil yi mu àndal.” Nga wutaat beneen bant, bind ci kawam: “Ñeel Yuusufa, bantu Efrayim, ak waa kër Israayil yi mu àndal,”

17te nga boole ñaari bant yi, ñu booloo, di benn bant ci sa loxo.

18Bu la sa bokk yi laajee, ne la: “Xanaa doo nu wax lii lu muy tekki?”

19nanga leen wax ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jël bantu Yuusufa wi ci loxol Efrayim, mook giiri Israayil yi mu àndal, boole kook bantu Yuda, daldi def lépp benn bant, ñu booloo di benn ci sama loxo.”

20«Nanga yore bant yi nga bind, ñuy gis,

21te nga wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jëleji bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* ca biir xeet ya ñu fekki, dajalee leen wet gu nekk, delloosi leen ci seen suufas bopp.

22Maa leen di def wenn xeet doŋŋ ci réew mi, ci kaw tundi Israayil, ñoom ñépp bokk benn buur. Dootuñu doon ñaari xeet te dootuñu xàjjalikoo ñaari nguur.

23Dootuñu sobeel seen bopp ci ay kasaray tuur ak seen jëf ju siblook mboolem seeni tooñ. Maa leen di walloo ci mboolem seen ñàkk kóllëre. Ma setal leen, ñu doon sama ñoñ, ma doon seen Yàlla.

24«“Daawuda sama jaam baay doon seen buur, di seen bennub sàmm ñoom ñépp. Sama àttey yoon lañuy doxe, sama dogali yoon lañuy sàmm, di ko jëfe.

25Ñooy dëkke réew mi ma joxoon Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:"* sama jaam ba, te seeni maam dëkke woon ko. Ñu dëkke ko ñoom it, ñook seeni doom ak seeni sët, ba fàww, te Daawuda sama jaam ba mooy doon seen boroom jal ba fàww.

26Maay fas ak ñoom kóllëreg|lemma="kóllëre g-:"* jàmm gu sax. Maa leen di samp, ful leen, maay samp sama kër gu sell fi seen biir, ba fàww,

27sama dëkkuwaay nekk fi seen biir, may seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.

© 2025 Bible Society of Senegal
div>