Esekiyel 43:1-26 WOLB2025 - Bible AI

1Waa ja nag jiite ma ba ca bunt ba, bunt ba féete penku.

2Ma jekki gis leeru Yàllay Israayil, mu dikke penku, ànd ak kàddu gu mel ni kàddug géej mbàmbulaan, suuf si di lerxate fa leeram ga.

3Moomu peeñu nirook peeñu ma ma njëkkoona gis ba may dikk ca yàqum Yerusalem, nirook ma woon ca tàkkal dexu Kebar. Ma daldi daanu, dëpp sama jë fa suuf.

4Ba loolu amee leeru Aji Sax ja jaare ca buntu penku ba, dugg ca néegu Yàlla ba.

5Ngelawu Aji Sax ji ne ma cas, yóbbu ma ca biir ëttu biir ba, leeru Aji Sax ji jekki fees néeg ba.

6Ma dégg kuy wax ak man ku féete fi biir néegu Yàlla bi, te fekk waa ji ma dugal a ngi taxaw fi sama wet ba tey.

7Mu ne ma: «Yaw nit ki, sama màkkaanu ngàngunee ngi, béreb bii laay teg samay tànk, dëkk ci digg bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* ba fàww. Waa kër Israayil dootuñu teddadil sama tur wu sell|lemma="Aji Sell j-:"*, ñook seeni buur ci seen gànctu, ak seen néewi buur yi ñuy denc ci seen bérebi jaamookaay|lemma="bérebi jaamookaay y-:"*.

8Seen buur yi ñoo féetale seen dëxi bunt ak seen jëni bunt ci sama weti dëxi bunt ak sama jëni buntu kër. Miir doŋŋ a doxoon diggante sama kër ak seen kër buur. Ñoo def seen jëf ju siblu, ba teddadil sama tur wu sell, ma mer, faagaagal leen.

9Léegi nag nañu ma sorele seen gànctu ak seen néewi buur yi, ndax ma mana dëkk fi seen biir, ba fàww.

10«Yaw nit ki, waxal waa Israayil ni kër gi wara mel. Nañu kersawoo seeni ñaawtéef te ñu natt nataalu kër gi.

11Bu ñu kersawoo mboolem seeni jëf nag, nanga leen xamal bindu kër gi ak tëralinam aki jàllukaayam aki génnukaayam ak bindam bépp, ak dogali yoon yi mu laaj yépp. Nanga bind lépp, ñu gis, ba mana sàmm mboolem bindu kër gi, ak mboolem dogali yoon yi mu laaj, te di ko jëfe.

12Ndigalu yoon wi jëm ci kër Yàlla gi ñu wara tabax mooy lii: ci kaw tund wi ak fi ko wër fépp, fu sella sell lay doon. Loolu mooy ndigalu yoon wi, ci wàllu kër Yàlla gi.»

13Lii nag mooy dayoy sarxalukaay bi ciy xasab, xasab bu ci nekk tegu yaatuwaayu catu loxo. Tóojub sarxalukaay bi féete suuf, taxawaay bi xasab la, yaatuwaay bi di xasab, mu ànd ak kéméjam gu ko wër ba mu daj, te taxawaayu kéméj gi tollook yaatuwaayu catu loxo. Tóojub sarxalukaay bi noonu la bindoo itam.

14Ñaari xasab a dox diggante tóoju bi ci suuf, ba ci cat li ngay njëkka jot, te yaatuwaayu cat li di xasab. Ñeenti xasab a dox diggante cat li ngay njëkka jot, ba ca cat la ca kaw, te yaatuwaay bi it di xasab.

15Taxawaayu taalub sarxalukaay bi féete kaw, ñeenti xasab la, ñeenti béjjén sampe ci ñeenti coll yi, coll wu nekk, benn béjjén sampe ci.

16Lakkukaayu sarxalukaay bi ab kaare la, wet gu ci nekk di fukki xasab ak ñaar.

17Kon tóojub lakkukaay bi fukki xasab ak ñeent la ci ñeenti wet yi, dib kaare, kéméj gi wër tóoju bi am taxawaayu genn-wàllu xasab, te tóojub lakkukaay bi wëre lakkukaay bi yaatoo xasab. Dëggastal bi ñuy yéege ci sarxalukaay bi nag penku la féete.

18Waa ji ne ma: «Yaw nit ki, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Lii mooy dogali yoon yi jëm ci sarxalukaay bi, bés bu noppee, ci wàllu saraxi rendi-dóomal, ak deret ji ñu ci wara tuur.

19Sarxalkat yiy Leween ñi sëtoo ci Cadog, te jege ma, ngir di ma liggéeyal, kàddug Aji Sax jee, nanga leen jox yëkk wu ndaw, muy saraxu póotum bàkkaar.

20Nga sàkk ci deret ji, taqal ci ñeenti béjjéni sarxalukaay bi ak ñeenti colli kaw gi ak ci kéméj gi ba mu daj, nga laabale ko sarxalukaay bi, defale ko ko njotlaayam.

21Nga génne kër gu sell gi yëkku saraxu póotum bàkkaar mi, te nga lakke ko ca béreb ba ñu ko wara defe ci biti kër Yàlla gi.

22«Bésub ñaareel ba nanga indi ab sikket bu amul sikk, muy saraxu póotum bàkkaar bu ñuy laabale sarxalukaay bi, na ñu ko laabale woon yëkk wu ndaw wa.

23Boo ko laabalee noonee ba noppi, nanga sàkk aw yëkk wu ndaw wu amul sikk ak kuuy mu amul sikk.

24Nga boole ko, indi fi kanam Aji Sax ji te sarxalkat yi suy leen xorom, ñu def leen saraxu rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji.

25«Diiru juróom ñaari fan ngay joxe bés bu nekk ab sikketu póotum bàkkaar ak aw yëkk akum kuuy, te na lu ci nekk mucc sikk.

26Diiru juróom ñaari fan lañuy def njotlaayal sarxalukaay bi, laabal ko, waajale ko sasu sarxalukaay bi.

© 2025 Bible Society of Senegal
div>