1Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji da maa dikkal, ne ma:
2«Léegi nag, yaw nit ki, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax réewum Israayil ne ko:
3Jeexal nga nag léegi!
4Duma la xool bëtu ñéeblu,
5«Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
6Jeexlee ngoog, jeexle dikk na,
7Yaw nitu réew mee, sànkute dikkal na la.
8Du yàgg dara ma xëpp la sama xadar,
9Duma xoole bëtu ñéeblu,
10«Bés baa ngii, mu ngooguy dikk,
11Fitnaa taxaw, di yet wuy dóoral coxor.
12Àpp mat,
13Bu jaaykat bi muccee it,
14Liitu xareey jib, ba lépp jekk ngir xare,
15Saamar biti,
16Ña rëcc, rawi ca tund ya,
17Loxo yépp yoqi,
18Ñooy sol ay saaku di ko ñaawloo,
19Seen xaalis, ñu sànni ci mbedd yi,
20Ñoo doon sagoo seen gànjar gu yànj,
21Maa koy teg ci loxoy doxandéem, ñu foqati ko,
22Maa leen di dummóoyu,
23Waajalleen càllala yi,
24Maay indi xeet yi gëna néeg,
25Tiitaangee ngi dikk,
26Ay ci kaw ay a ngi dikk,