1At ma njëkk ca nguurug Sirus buuru Pers, Aji Sax ji|lemma="Aji Sax j-:"* moo nammoona sottal kàddu ga mu waxe ca gémmiñug Yonent Yàlla Yeremi+ 1.1 Seetal ci Yeremi 25.11-12; 29.10.*, ba tax mu xiir Sirus buuru Pers, mu siiwtaane ab dogal ci mboolem réewam, boole ci bind ko ne:
2Sirus buuru Pers dafa wax ne: «Mboolem réewi àddina, Yàlla Boroom asamaan+ 1.2 Yàlla Boroom asamaan turu darajaal la bu ñuy waxe ci gàttal ne mooy Yàllay asamaan ak suuf, muy wund ne du Israayil rekk lay seen Yàlla, waaye mooy Yàllay àddina sépp.* moo ma leen dénk, te moom moo ma tabb, ngir ma tabaxal ko kër ca Yerusalem ga ca Yuda.
3Képp ku bokk ci mboolem ñoñam, yal na Yàllaam ànd ak moom, mu dem Yerusalem ga ca Yuda, tabax fa kër Aji Sax ji Yàllay Israayil, Yàlla ja ca Yerusalem.
4Mboolem bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* ak fu ci nit mana féete, na ko waa foofa indil ndimbal ci wàllu xaalis ak wurus, alal aku jur ak saraxi yéene|lemma="Sarax yi:"* yu jëm ca kër Yàlla ga ca Yerusalem.»
5Ba mu ko defee ña jiite waa kër Yuda ak Beñamin ak sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yaak Leween|lemma="Leween b-:"* ña, képp ku ci Yàlla xiir rekk, mu daldi dem tabaxi kër Aji Sax ja ca Yerusalem.
6Mboolem seeni dëkkandoo daldi def ci seen loxo jumtukaayi xaalis ak wurus, alal akug jur ak gànjar, te bokkul ak mboolem seen saraxi yéene.
7Ci biir loolu Buur Sirus génne ndabi kër Aji Sax ja Nebukatnecar+ 1.7 Nebukatnecar mooy Nabukodonocor ba tey. * jële woon Yerusalem te yeboon ko ca kër tuuram ya.
8Sirus buuru Pers nag sant Mittredat farbay alalam, mu génne ko, daldi koy waññal Sesbacar, boroom Yuda.
9Lenn ci lim bi tëdde nii: fanweeri (30) ndabi wurus ak junniy (1 000) ndabi xaalis ak ñaar fukki paaka ak juróom ñeent (29)
10ak fanweeri (30) këlli wurus yu ndaw yu ànd ak ñeenti téeméeri këll ak fukk (410) yu ndaw yu xaalis ak junniy (1 000) jumtukaay yeneen.