1Naka la Esra di ñaan aka tuub, di jooy, aka daanu fa suuf ca buntu kër Yàlla ga, bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* yéew ko, bare lool, góor ak jigéen, ba ca xale ya. Mbooloo ma it di jooy jooy yu metti.
2Ci biir loolu Sekaña doomu Yexyel ma askanoo ci Elam, daldi wax Esra ne ko: «Noo tooñ sunu Yàlla, di jël ay jàmbur jabar ci xeeti réew mi. Waaye loolu terewul Israayil am yaakaar ba tey.
3Léegi kay nanu fasanteek sunu Yàlla kóllëre|lemma="kóllëre g-:"*, daldi fase jigéen ñooñu ñépp, ñu ànd ak seeni doom, muy ni nga ko diglee rekk, sang bi, yaak ñi wormaal sunu santaaney Yàlla. Li yoon wi digle daal, na am.
4Jógal nag, mbir maa ngi ci say loxo, te noo ngi ànd ak yaw. Kon dëgërlul te def ko.»
5Ci kaw loolu Esra jóg, wax kilifay sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yaak Leween|lemma="Leween b-:"* ñaak Israayil gépp, ne leen ñu giñ ne noonu lañu koy defe. Ñu daldi ko giñ.
6Ba loolu amee Esra bàyyikoo kër Yàlla ga, fatuji néegu Yoxanan doomu Elyasib. La mu fa nekk nag lekkul, naanul, xanaa di ñaawlu na ngàllo ga ñibbisi feccee worma.
7Ba mu ko defee ñu yéene ci Yerusalem ak Yuda, yégal mboolem ngàllo ga ñibbisi, ne leen ñu daje ca Yerusalem.
8Ñu ne képp ku teewul ci diiru ñetti fan, ni ko kilifa yeek mag ñi diglee, dees na teg alalam jépp loxo, te moom ci boppam dees na ko dàq, génne ko ca ngàllo ga ñibbisi.
9Ba ñu ca tegee ñetti fan mboolem góori Yudaak Beñamin daje nañu Yerusalem, mu yemook ñaar fukki fan ca juróom ñeenteelu weer wa. Ña nga toog ñoom ñépp ca ëttu kër Yàlla ga, di lox ndax solos ndaje ma ak itam taw bu bare ba mu yemool.
10Ci kaw loolu Esra sarxalkat ba jóg taxaw, ne leen: «Yeena fecci kóllëre ndax yeena jël ay jàmbur jabar, di yokk tooñaangey Israayil.
11Léegi nag tuubleen ci Aji Sax ji seen Yàllay maam te def coobareem. Teqalikooleen ak xeeti réew mi, teqalikook jigéen ñii diy jàmbur.»
12Ci kaw loolu mbooloo mépp bokk àddu ca kaw ne ko: «Tigi, li nga wax rekk lanu wara def.
13Waaye danoo bare, te muy jamonoy taw. Manunoo toog fii ci biti. Te it mbir mi maneesu koo lijjanti ci benn bés mbaa ñaar, ndax sunu tooñ ci mbir mii daa yaatu.
14Kon daal na sunuy kilifa taxawal askan wi. Su ko defee mboolem ku nekk ci sunuy dëkk te jël ci jàmbur ñi jabar day dikk, ku ci nekk ca bés ba ñu ko àppal, te mu ànd ak kilifa yaak àttekati dëkkam. Ñu toppatoo mbir mi nag, ba keroog sunu sànjum Yàlla mu réy mi sababoo ci lii, dëddu nu.»
15Mennum Yonatan doomu Asayel ak Yaxseya doomu Tigwa, ñoom doŋŋ, ñook Mesulam ak Sabtay, Leween ba, ñoo àndul ca loola.
16Ci kaw loolu ngàllo ga ñibbisi daldi def la ñu wax. Esra sarxalkat ba tànn nit ña jiite seen kër baay, ku nekk ak làngam, ñoom ñépp ñu tudd seeni tur. Keroog benn fan ca fukkeelu weer wa nag, ñu toog ngir seet mbir ma.
17Ca benn fanu weer wa njëkk ca déwén sa lañu lijjanti mbiru mboolem ña jëloon jabar ay jàmbur.
18Ñu gis ne ñenn ci askanu sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yi jëloon nañu ay jàmbur soxna:
19Ñu xas ne dinañu fase seeni soxna, daldi nangu ne tooñ nañu, ba noppi ku nekk ci ñoom sarxe am kuuy, muy peyug tooñam|lemma="Sarax yi:"*.
20Ci askanu Imer, Anani la ak Sebaja.
21Ci askanu Arim, Maaseya laak Elya ak Semaya ak Yexyel ak Osiyas.
22Ci askanu Pasur, Elyonay laak Maaseya ak Ismayel ak Netaneel ak Yosabàdd ak Elasa.
23Ci Leween|lemma="Leween b-:"* ñi: Yosabàdd laak Simey ak Kelaya, mooy Kelita ba tey, ak Petaxya ak Yuda ak Elyeser.
24Ci woykat yi: Elyasib la.
25Bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* yi ci des:
26Ci askanu Elam, Mataña laak Sàkkaryaa ak Yexyel ak Abdi ak Yeremot ak Elya.
27Ci askanu Sàttu, Elyonay laak Elyasib ak Mataña ak Yeremot ak Sabàdd ak Asisa.
28Ci askanu Bebay, Yoxanan laak Anaña ak Sabay ak Atlay.
29Ci askanu Bani, Mesulam laak Malukk ak Adaya ak Yasub ak Seyal ak Yeremot.
30Ci askanu Paxat Mowab, Atna laak Kelal ak Benaya ak Maaseya ak Mataña ak Beccalel ak Binuy ak Manase.
31Ci askanu Arim, Elyeser laak Isiya ak Malkiya ak Semaya ak Simeyon,
32ak Beñamin ak Malukk ak Semarya.
33Ci askanu Asum, Matenay laak Matata ak Sabàdd ak Elifelet ak Yeremay ak Manase ak Simey.
34Ci askanu Bani, Maaday laak Amram ak Uyel
35ak Benaya ak Bediya ak Keluyi
36ak Waña ak Meremot ak Elyasib
37ak Mataña ak Matenay ak Yaasay
38ak Bani ak Binuy ak Simey
39ak Selemya ak Natan ak Adaya
40ak Magnadebay ak Sasay ak Saray
41ak Asareel ak Selemya ak Semarya
42ak Salum ak Amarya ak Yuusufa.
43Ci askanu Nebo, Yewel la, ak Matica ak Sabàdd ak Sebina ak Yaday ak Yowel ak Benaya.
44Ñooñu ñépp jël nañu ay jàmbur jabar, ba ñenn ci ñoom ami doom.