Esra 5:1-16 WOLB2025 - Bible AI

1Gannaaw loolu Yonent Yàlla Ase ak Yonent Yàlla Sàkkaryaa sëtub Ido, wax nañu ci turu Yàllay Israayil jiy seen Yàlla, ñeel Yawuti Yuda ak Yerusalem.

2Booba la Sorobabel doomu Selcel, ak Yosuwe doomu Yoccadag tàmbalee tabaxaat kër Yàlla ga ca Yerusalem. Yonenti Yàlla ya nag ànd ak ñoom, di leen jàppale.

3Booba la Tatnay, boroom Wàllaa Efraat, ànd ak Setar Bosnay ak seeni naataango, dikk ne leen: «Ana ku leen may sañ-sañu tabaxaat kër gii, bay yékkati miir bi?»

4Ñu dellu ne leen: «Ana ñan sax ñooy tabax taax mii?»

5Fekk na seen Yàllaa ngi ne jàkk ci magi Yawut ñi, ba kenn bàyyiwul liggéey ba, ba keroog ñuy yónnee xibaar ba Buur Daryus, ba jot ci bataaxalu tontam ca mbir ma.

6Bataaxal ba ñu bind Buur Daryus, te Tatnay boroom Wàllaa Efraat yónnee ko ko, mook Setar Bosnay, ak jawriñi Tatnay ca Wàllaa Efraat, lii moo ca nekk.

7Kàddu ga nii la tëdde:

8Buur, nu ngi lay xamal ne dem nanu ca diiwaanu Yuda, ca kër Yàlla ju màgg ja. Ña nga koy tabaxe doj yu mag, di teg ay dénk ca miir ya. Liggéey baa ngay dox bu baax, di jëm kanam.

9«Ci biir loolu laaj nanu seen mag ñooñu, ne leen: “Ana kan moo leen may sañ-sañu tabaxaat kër Yàlla gii, bay yékkati miiram bii?”

10Nu laaj leen itam ñan ñoo koy tabax, ndax nu mana bind seen turi njiit, ba xamal la ñan la.

11«Li ñu nu tontu mooy lii: “Nun ay jaami Yàlla Boroom asamaan ak suuf lanu. Danuy tabaxaat kër Yàlla gi ñu tabaxoon lu jiitu ay at yu bare. Buurub Israayil bu mag moo ko tabaxoon ba sottal ko.

12Sunuy maam nag ñoo merloo Yàllay asamaan, ba tax mu teg leen ci loxoy Nebukatnecar buuru Babilon ma askanoo ci waa Kalde. Mu toj kër gii, yóbbu xeet wi ngàllo ca Babilon.

13Terewul ca at ma njëkk ca nguurug Sirus buuru Babilon+ 5.13 Sirus buuru Babilon bi ñuy wax fii mooy Buuru Pers rekk, ndax fekk na Pers moom nguurug Babilon.*, Buur Sirus joxe ndigal ngir ñu tabaxaat kër Yàlla gii.

14Te sax ndabi wurus ak xaalis yu kër Yàlla ya Nebukatnecar jële woon ca Yerusalem, te yóbbu ko ca kër tuuram ga ca Babilon, Buur Sirus jële na ko ca kër tuuram ga ca Babilon, teg ko ca loxol ku mu fal boroom dëkk ba, ñu di ko wax Sesbacar.

15Mu ne ko: ‘Ndab yii, jël ko yóbbu ca kër Yàlla ga ca Yerusalem, te nañu tabaxaat kër Yàlla ga fa mu nekkoon.’

16Sesbacar moomu nag ñëw lal fondmaa kër Yàlla gi ci Yerusalem. Booba ba léegi, ñu ngi koy tabax waaye noppeegul.”

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>