Filib 2:1-29 WOLB2025 - Bible AI

1Ndegam amees na lenn lu yokk aw fit ci Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi nu gëm, ndegam lenni cofeelam lu mana dëfal am na, ndegam amees na benn cér ci Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi, ndegam it amees na lenn lu bawoo fi moom, ci wàllu xol bu rafet ak yërmande,

2kon dëgg waay, mottalileen sama mbég, ba mànkoo, te ngeen soppantee genn cofeel, jubale seeni xol, te bokk benn jëmu.

3Buleen def dara ci kaw wujje, mbaa réy-réylu, waaye woyofluleen, ba jàpp ne seeni moroom a leen gën.

4Bu kenn ci yeen xintewoo njariñal boppam, waaye na ku nekk bàyyi xel moroomam.

5Noonu Almasi Yeesu doon doxale, deeleen ko doxale ci seen biir:

6Moom mi nekke nekkinu Yàlla

7Xanaa mu ŋacc boppam,

8Moo toroxlu,

9Moo tax Yàlla kaweel koo kaweel,

10ba turu Yeesu tax ñépp sukk seen bëti óom,

11làmmiñu ñépp it biral ne Yeesu Almasi bi mooy Sang bi,

12Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox,

13ndax Yàlla mooy liggéey ci yeen lu tax ngeen mana namma jëfe coobareem, ba man koo jëfe.

14Mboolem lu ngeen di def nag, buleen ci boole xultu mbaa xuloo,

15ngir seen der set wecc, te kon deesuleen mana gàkkal ci lenn. Ay goney Yàlla yu amul sikk ngeen di doon, ci biir maas gu dëng te yàqu, ngeen di lerxat ci seen biir, ni ay leer ci àddina si,

16ànd ak kàddug dund gi ngeen di xamle. Su ko defee keroog bés bi Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi di délsi, ma mana damoo ne dawuma cig neen, te sonnuma cig neen.

17Su ma ci deewee sax, ba sama dund mel ni sarax su ñu tuur, tofal ko ci sarax bi seen ngëm taxawe, su boobaa it maa ciy bég, te di leen woo, ngir bokk ak yeen ñépp bànneexu.

18Yeen itam nangeen ci bég te bokk ak man bànneexu.

19Yaakaar naa nag, ne bu soobee Sang Yeesu, dinaa leen yónnee Timote balaa yàgg, ngir xam nu ngeen def, ba man ci sama bopp, sama xel dal.

20Ndaxte awma fi kenn ku ko moy, ku bokk ak man xinte, ba seeni mbir yitteel ko dëgg.

21Ñi ci des ñépp, seen njariñal bopp lañuy sàkku, waaye du li soxal Yeesu Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi.

22Timote nag xam ngeen ne ku rafet ab jëw la. Ni doom di taxawoo baayam, ni la bokke ak man liggéey bi ci xamle xibaaru jàmm bi.

23Sama yaakaar nag moo di, bu may am lu leer ci sama mbir rekk, moom laay daldi yebal ci yeen.

24Teewul mu bir ma ne, bu soobee Boroom bi, man ci sama bopp, balaa yàgg, dinaa leen seetsi.

25Lu jëm ci Epafrodit, sama mbokkum gëmkat la, sama naataango la, sama mbokkum xarekat la, te di seen ndaw li ngeen ma yóbbante ndimbal lu faj samay soxla. Waaye jàpp naa ne fàww ma delloo leen ko,

26ndax namm na leen lool, boole ci am njàqare ndax li ngeen dégg ag jagadeem.

27Woppoon na it ba xawa dee, waaye Yàllaa ko yërëm, te du moom rekk la yërëm, waaye man itam, ngir ma baña am tiis ci kaw tiis.

28Moo tax ma yàkkamti leen koo delloo, ngir bu dikkee, ngeen man koo bégewaat, te man itam, samaw tiis wàññiku.

29Teertooleen ko mbégte mu mat sëkk ngir Sang bi, te it nawleen ñu mel ni moom,

© 2025 Bible Society of Senegal