1Ndeysaan, wurus wa giim na! Ngëneelu wurus soppiku na. Doj yu sell|lemma="sell:" yaa wasaaroo, ca boppu mbedd yépp.
2Doomi Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:" yu góor yu jar ya! Wurus lees leen daan nàttablee, ndeysaan tey, ñu jàppe leen ni njaqu ban lu tabaxkatu njaq liggéeye loxoom.
3Ag till sax joxe na weenam, nàmpal doomam, te sama bokk yi mujj néeg ba mel ni bànjóolig màndiŋ.
4Luy nàmp a nga mar a mar, ba làmmiñ taqoo denqleñ. Gone yaa ngi ñaan mburu, te kenn daggalu leen.
5Ñi daan xéewloo ay bernde, tey ñoo xiif, ne lasar ca mbedd ya. Ña yaroo woon yérey tànnéef, tey ñoo goore jalu mbuubit.
6Sama ñaawtéefu askan wee màgg, ba raw ñaawtéefu waa Sodom|lemma="Sodom ak Gomor:", dëkk ba jekki jàllarbiku, te loxo laalu ko.
7Sunu kàngam ya setoon wecc, seen yaram mucc gàkk, di lerxat bay tàkk, wér péŋŋ, leer nàññ.
8Tey ñu gëna lëndëm bànqanoos, xàmmeesu leen ci mbedd yi, ñu ngi lax, di yaxi neen, der wow koŋŋ ni matt!
9Ña saamar rey a gënu demin ña deek xiif, jeex tàkk, ne lasar, ndax ñàkk meññatum tool.
10Ndey ak xolu njureelam, moo togge loxoom doomu boppam, def ko njëlam, ci sama biir toskareg askan wi!
11Aji Sax jee xëpp am sànjam, sotti tàngooru meram, moo jafal sawara fi Siyoŋ, ba xoyom kenu ya.
12Du benn buur fi kaw suuf bu gëmoon, du kenn ci mboolem waa àddina kuy foog ne ab bañ mbaa noon dina dem ba bëtt bunti Yerusalem.
13Seen bàkkaari yonent yaa, seen ñaawtéefi sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:" yaa; ñoo tuur fa digg dëkk ba deretu aji jub ñi.
14Ña ngay tëñëx-tëñëxi niy gumba ci mbedd yi, deret ja sobeel leen ba maneesula laal seeni yére.
15Ñoom lañuy gëdd naan: «Soreleen nu, nit ñu sobewu ñi! Soreleen, soreleen, buleen nu laal.» Ñu daw di tambaambalu ba ca yeneen xeet; ñooña ne leen: «Dootul fii!»
16Aji Sax ji ci boppam moo leen tasaare, faaleetu leen; cér lees séddul sarxalkat, te teraleesul mag. Waa Yerusalem àddu nañu
17Ba tey sunu gët a ngi giim, ndax ndimbal lu nuy séentu ci dara. Fa sunuy tata lanu séentoo wenn xeet wu nu manula wallu.
18Sunuy tànk lees di topp, ba manatunoo daagoo sunuy mbedd; sunu bés jege, sunu àpp di matal, sunu saa taxaw!
19Ñi ñuy dàq a gëna gaaw ay jaxaay, ci kaw tund yi lañu nu ne dann, màndiŋ mi, ñu di nu fa tëroo.
20Ki nuy noyyee, Buur bi Aji Sax ji fal, ca seeni yeer la tance, te nu noon ci keppaaram lanuy dëkke fi digg xeet yi. Yeremi àddu na
21Bégleen te bànneexooy, Edom réew mu taaru mi, yeen Edomeen+ 4.21 Edomeen ñaa nga bàyyikoo fa bëj-saalumu Yuda jàpp penku. Ñu ngi soqikoo ci Esawu, magu Yanqóoba, kon bokki Israayil lañu woon, waaye dañoo faroon ak nooni Israayil. ñi dëkk réewum Ucc, ci yeen it la kaasu mbugal di jàllsi, ngeen màndi, futteeku, ne duŋŋ.
22Yaw Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:", dëkk bu taaru ba, sa mbugal mat na, deesatu la yóbbu ngàllo; yaw Edom laa ne, Aji Sax jee lay fey sa ñaawtéef, feeñal say bàkkaar.