1Kàddu yu xelu yu Suleymaan buurub Israayil, di doomu Daawuda.
2Li ko taxa jóg di nit ñi am xel mu rafet, am ab yar, ngir xam wax ju lal dég-dég,
3ngir yaru ci jëfe xel ak njub ak yoon, di jubal,
4ndax ab téxét di foog, ndaw li it xam tey xalaat.
5Na boroom xel mu rafet déglu, yokk dég-dégam, te kiy ràññee di jariñoo ay tegtal,
6ngir mana xam aw léeb aku taas ak kàddug boroomi xel yu rafet ak seeni cax.
7Ragal Aji Sax ji|lemma="Aji Sax j-:"* di njàlbéenu xam-xam,
8Doom, toppal yaru baay,
9Kaala gu jekk la ci bopp,
10Doom, bàkkaarkat bu la xiirtal, lànkal.
11Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan,
12Nanu mel ni njaniiw, mëdd kuy dund,
13Mboolem alal ju réy, nu jagoo,
14Dikkal nu far,
15Doom, bul ànd ak ñoom ciw yoon,
16ngir dañuy xélu, nar musiba,
17Doo firib caax,
18Ñii kat seen bopp lañuy fiir,
19Képp kuy lekk lu lewul, nii lay mujje:
20Xel mu Rafet a ngay woote ca mbedd ma,
21Ma ngay wootee béreb yu gëna xumb,
22Ma nga naan: «Moo téxét bi, foo àppal sa téxét gi?
23Soo dëppee ba déglu, ma artu la.
24Damaa woote, nga gàntal,
25Sofental nga samay digle,
26Kon boo sëngéemee, man it ma ree,
27Njàqare di ngëlén, dab la,
28«Keroog nga woo ma wall, duma wuyu,
29Daa fekk nga baña xam,
30Dégluwoo samay digle it,
31Waaye loo ci góobe, gar ko,
32Déggadi sànk ab téxét,