1Bul damoo ëllëg,
2Bul tëggu, bàyyil ñu tagg la,
3Doj diis na, suuf dib sëf,
4Xadar day ñàng, mer di wal mu baawaan,
5Artu yu ñu la biralal
6Soppe, bu lay gaañ sax, wóolu ko.
7Ku suur, bañ lem ju xelli,
8Ku sore fa nga bokk,
9Diwook suuru day naatal xol;
10Bul fàtte sab xarit mbaa sa xaritu baay,
11Muusal, doom, ma bég,
12Kuy foog, gisu ay, làqu;
13Ku gàddul jàmbur bor, jëlal mbubbam;
14Nuyoo bu xumb, suba teel
15Jabar ju pànk
16ku ko mana yemale,
17Weñ ay nàmm weñ,
18Ku aar garab, lekk ca doom ya;
19Ku xool cim ndox, gis sa kanam,
20Njaniiw ak biir suuf du fees,
21Xaalis ak wurus sawaraa koy xelli,
22Soo jëloonub dof, yeb ci gënn,
23Xamal bu baax lu say gàtt nekke,
24ndax alal wéyul fàww,
25Gannaaw bu ñu gubee,
26say xar da lay amal koddaay,