1Ku bon daw na te dàqeesu ko,
2Bu am réew dee fippu, kilifa ya bare;
3Ku ñàkk, su jekkoo ab ndóol,
4Ku wacc yoon, gërëm ku bon;
5Ku bon xamul njub,
6Ñàkk te mat
7Gone gu sàmm yoon am nag dégg,
8Kiy leble di tege, ba barele,
9Soo dee tanqamlu yoon,
10Ku yóbbe bàkkaar nit kuy jubal,
11Waay a ngi barele, defe ne xelu na;
12Bu kuy jëfe njekk amee ndam, mbégte mu réy la;
13Kuy làq say tooñ doo baaxle,
14Mbégte ñeel na ku saxoo ragal Yàlla,
15Kilifa guy soxore néew-ji-doole
16Kilifa gu amulug dégg, day foqati rekk,
17Ku bóom nit, daw, ba tàbbi njaniiw;
18Mat, mucc;
19Beyal sab tool, sab dund doy;
20Boroom worma, bare barke;
21Par-parloo baaxul,
22Ab nay day yàkkamtee barele,
23Boo artoo nit, mu baaxe la ëllëg;
24Ku xañ say waajur seen alal
25Ku bëgge day sooke ay,
26Ku doyloo sam xel, dof nga;
27Kuy jox néew-ji-doole, doo ñàkk;