1Doom, sàmmal samay wax,
2Jëfeel samay santaane, ba dund,
3Takkal ci say waaraam,
4Safool xel mu rafet, muy sab jigéen,
5Dina la aar ci jigéenu njaalookat,
6Damaa tollu sama palanteer,
7séen ca biir téxét ya,
8Muy dem ba fa ndaw say taxaw, ca selebe yoon wa,
9Ngoonug suuf la, jant biy lang,
10Ndaw si jekki dajeek moom,
11Daa xumb, të,
12Ma nga ca mbedd ma, ne ca pénc ya,
13Ndaw sa ne ko katam, fóon,
14«Tey matal naa la ma digoon Yàlla,
15Moo ma taxa dikk dajeek yaw.
16Lal naa saab lal, ba mu jekk,
17Lal ba, ma xeeñal, mu ne bann,
18Dikkal, nu baanee baane, ba bët set,
19Sama jëkkër newu fa,
20Mbuusum xaalis la ŋàbb, yóbbu,
21Muy mocc aka moccaat, ba nax ko,
22Waa ja jekki, topp ko,
23Mooy picc mu tàbbi cig fiir.
24Kon nag, samay doom, dégluleen ma,
25Bu leen soosu ndaw xiir ci moy,
26Bare na ku dee, moo ko rey,