1Déggal! Xel mu Rafet di soxna saa ngi woote,
2Ma nga taxaw ca selebe yoon ya,
3Ma nga ca buntu dëkk ba, taxaw;
4«Yeen mbooloo yi laay woo,
5Téxét bi, deel foog,
6Déglul, ma wax la lu am solo,
7Dëgg laay wax,
8Lu ma wax njub la.
9Lépp a dëggu ci ku amug dégg,
10Na la samab yar gënal xaalis,
11Ndax man, Xel mu Rafet, maa gën gànjar,
12«Man, Xel mu Rafet, foog di sama kër;
13Ragal Aji Sax ji mooy bañ lu bon.
14Maa moomi digle, di maye gis-gis;
15Samay pexe la buur di jiitee,
16Ci samay pexe la njiit di saytoo,
17Maa sopp ku ma sopp,
18Alal ak teraangaa ngi fi man,
19Li may mayee gën wurus, muy wurus wa gën,
20Yoonu njub laay jaare,
21Ku ma sopp, ma nàddil la,
22Soxna si, Xel mu Rafet nee na:
23Bu yàgg lañu ma dëj,
24Ba may dikk, géej amul,
25Dikk naa bala tund yu mag yee sampu,
26laata Yàllaa sàkk suuf aki àllam
27Ba muy taxawal asamaan, maa nga fa,
28ak ba muy teg niir ya fa kaw,
29ak ba muy sàkkal géej kemoom,
30man, Xel mu Rafet, maa doon ku xareñ ci wetam,
31May bége wërngalu àddinaam,
32«Kon nag, samay doom, dégluleen ma.
33Nangeen déglu ku leen di yar, daldi muus.
34Mbégte ñeel na ki may déglu,
35Ku ma daj, gudd fan,