1Soxna si, Xel mu Rafet daa tabax këram, yatt juróom ñaari kenoom.
2Mu rendi ag juram, njafaan ay biiñam, xelli, taaj ay ndabam.
3Xel mu Rafet yónni ay janqam, di wootee fu kawee kawe ca dëkk ba,
4naan: «Képp ku téxét, jàddal ba fii!» Ku ñàkk bopp, mu ne ko:
5«Kaay, ma may la, nga lekk, xellil la biiñ bi ma njafaan, nga naan.
6Dëddul jëfi téxét ba dund, di jubal ci yoonu dégg.» Kuy xeloo ngii ak kuy ñaawle
7Artu kuy ñaawle, feyoo saaga rekk, yedd ab soxor, yooloo loraange.
8Bul yedd kuy ñaawle, da lay jéppi; yeddal ku rafet xel, mu naw la.
9Xelalal ku xelu, mu yokku. Xamalal ku jub, mu yokk njàngam.
10Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu rafet xel, xam Aji Sell|lemma="Aji Sell j-:" ji di amug dégg.
11Maay Xel mu Rafet, ku ma topp gudd fan, dund, dundati.
12Rafet xel, jariñu, kuy kókkalee, wéetook sa añ. Jigéen ju Dofee ngi berndeel
13Soxna si, Jigéen ju Dof day xumb, reew, du xam lu xew.
14Day toog bunt këram, mbaa fu kawee kawe ca dëkk ba,
15di woo ña fay jaare te jubal seenu yoon.
16Ma nga naa: «Képp ku téxét, jàddal ba fii!» Ku ñàkk bopp, mu ne ko:
17«Ndox mu lewul a neex, ñamu làqu-lekk dàqati.»
18Waaye kooka du xam ne waa njaniiw a nga fa, te ku wuyuji, tàbbi biir bàmmeel.