1Jëw bu rafet a gën diw gu xeeñ,
2Dem dëj a gën wàlli bernde,
3Naqar a gën xaxaloo;
4Ku xelu, xalaat kërug dëj;
5Déglu ku xelu di la artu
6Ab dof day tex-texi
7Foqarñi kay day dofloo boroom xel,
8Fa mbir mujjee gën fa mu doore,
9Bul gaawa mer;
10Bul ne lu tax démb dàq tey,
11Xel mu rafet daa neex ni ndono,
12Xel mu rafet kiiraay la,
13Xoolal ci li Yàlla def:
14Su neexee, bànneexul;
15Lu ne laa gis
16Bul jub ba mu ëpp,
17-18 Bu la mbon jiital,
19Xel mu rafet day dooleel boroom,
20Amul moos ku jub ci kaw suuf,
21Te it du lépp lu ñu wax,
22ndax xam nga xéll ne yaw it
23Loolu lépp maa ko natte xel mu rafet,
24Li wara am daa sore, te xóota xóot;
25Ma walbatiku, di jéema xam,
26Ma seetlu lenn lu gëna naqari dee:
27Waarekat ba nee: «Xoolal li ma gis,
28Ma seet a seet, gisuma.