1Loolu lépp laa walbatiku xalaat,
2Ñépp a bokk benn dogal bi,
3Lu mettee ngi nii ci mboolem lu am fi kaw suuf:
4Képp kuy dund kat, am nga yaakaar,
5Kuy dund xam ne dangay dee,
6Muy sa cofeel, di sa mbañeel,
7Kon doxal, lekk saw ñam, bége,
8Foo tollu, solul ba jekk,
9Bànneexul yaak ndaw si nga sopp
10Liggéey boo gis, liggéeyal;
11Ma seetlooti fi kaw suuf ne
12Doom aadama la bésu safaan bay bett,
13Lii it gis naa ko, muy lu ma yéem,
14Ab dëkk bu ndaw la woon, nit ña néew.
15Fekk fa ku néewle te xelu.
16Man dama noon xel mu rafet a gën doole!
17Ku xelu, kàddoom yu dégtu ndànk