1Bare na ñu fexee bind ab nettalib mbir yi sotti woon ci sunu biir,
2noonee nu ko jote ca ña ko fekke woon ca ndoorte la, te seede yooyu mujj doon jawriñi kàddug Yàlla.
3Moo tax man it, ma fas laa yéenee bindal lépp ba mu jekk, yaw Tewofil mu tedd mi, gannaaw ba ma gëstoo mbir mépp, dale ko ca ndoorte la, ba mu leer nàññ.
4Su ko defee nga xam xéll ne li ñu la jàngal, lu wér péŋŋ la.
5Jant ya Erodd|lemma="Erodd:"* nekkee buuru réewum Yawut yi, ab sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* la woon bu ñuy wax Sàkkaryaa, bokk ci làngu sarxalkat yi askanoo ci Abya, te soxnaam Elisabet askanoo ci Aaróona|lemma="Aaróona:"*.
6Ñoom ñaar ñépp a juboon, Yàlla seede, te mucc ayib ci ni ñuy jëfe santaane yeek ndigali yooni Boroom bi.
7Amuñu woon doom nag, ndax Elisabet manul woona am doom, te it booba ñoom ñaar ñépp a dem ba màggat.
8Sàkkaryaa la làngam aye woon, muy def liggéeyu carxalam fa kanam Yàlla.
9Ba ñu tegoo bant, na ko sarxalkat yi baaxoo woon, moom la bant ba dal, mu wara dugg ci biir néegu Boroom bi, ngir taal fa saraxu cuuraay|lemma="cuuraay l-:"*.
10Mbooloo mépp nag a nga woon ca biti di ñaan, ca waxtuw saraxu cuuraay boobu.
11Ci biir loolu menn malaakam Boroom bi jekki feeñu Sàkkaryaa, ca wetu ndijooru sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"* cuuraay ba.
12Ba ko Sàkkaryaa gisee daa jaaxle, tiitaange jàpp ko.
13Malaaka ma ne ko: «Sàkkaryaa, bul tiit, ndax sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina am doom ju góor, nanga ko tudde Yaxya|lemma="Yaxya:"*.
14Dinga am mbégte ak bànneex, te ñu bareey bég ci juddoom,
15ndax ku màgg lay doon, Boroom bi seede. Biiñ ak lenn luy màndil nag, du ko naan, Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi mooy dale ca biiru ndeyam, solu ko ba fees.
16Ñu bare ci bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*, moo leen di waññi ci Boroom bi seen Yàlla.
17Mooy ndaw li koy jiitu, ànd ak leer ga ak xam-xam ba woon ca Yonent Yàlla Ilyaas|lemma="Ilyaas:"*, ba waññi xolu baay ci doomam, waññi ku déggadi ci xelum aji jub, loolu yépp ngir waajal aw xeet, ba ñu jekk ngir Boroom bi.»
18Sàkkaryaa nag ne malaaka mi: «Lu may def ab takk ci loolu ba mu bir ma? Ndax man màggat naa, te sama soxna it làq na ay fan.»
19Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw fi kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw, yégal la bii xibaaru jàmm.
20Léegi nag, dama ne, gannaaw gëmuloo sama kàddu, giy jot, sotti, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera loolu di am.»
21Ci biir loolu mbooloo maa ngay xaar Sàkkaryaa, jaaxle lool ndax yàggaayam ca biir néegu Yàlla ba.
22Ba mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Ñu daldi xam ne am na lu ko feeñu ca néegu Yàlla ba. Ma nga leen di liyaar, manatula wax.
23Naka la Sàkkaryaa fégal ayu carxalam, daldi ñibbi.
24Gannaaw gi, soxnaam Elisabet ëmb. Lëlu na juróomi weer. Ma nga naan:
25«Lii Boroom bee ma ko defal ci jant yi mu ma geesoo, ba teggil ma sama gàcce gi ci biir nit ñi!»
26Ba Elisabet tolloo ci juróom benni weeram, ca la Yàlla yebal Jibril malaaka mi, dëkk bi ñuy wax Nasaret ca diiwaanu Galile,
27ci janq bu digoo séy ak waa ju ñuy wax Yuusufa te bokk ci waa kër Daawuda|lemma="Daawuda:"*. Janq ba Maryaama lañu koy wax.
28Malaaka ma agsi ba ca moom, ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi ñu baaxe, Boroom bi yaw la àndal.»
29Waxi malaaka ma nag jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki.
30Malaaka ma ne ko: «Maryaama, bul tiit, ndax daje nga ak yiwu Yàlla.
31Dinga ëmb, ba jur doom ju góor, nga tudde ko Yeesu+ 1.31 Yeesu ci làkku ebrë mooy Yosuwe, muy firi Aji Sax jeey musle. Aji Sax ji mooy tur wi Yàlla firil Musaa ci +bk Mucc ga+bk* 3.13-15.*.
32Ku màgg lay doon, te dees na ko woowe Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla moo koy jagleel nguurug Daawuda maamam.
33Mooy nguuru fi kaw waa kër Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:"* ba fàww, te nguuram du foq mukk.»
34Ci kaw loolu Maryaama laaj malaaka mi ne ko: «Nu loolu di ame, te man ab janq laa?»
35Malaaka mi ne ko: «Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi mooy wàccsi ci yaw, dooley Aji Kawe ji yiir la. Moo tax itam kiy juddoo ci yaw, dees na ko woowe Ku sell|lemma="Aji Sell j-:"*, ak Doomu Yàlla|lemma="Doomu Yàlla j-:"*.
36Te kat Elisabet sa mbokk mi itam ëmb na doom ju góor te fekk ko màggat. Ki ñu doon woowe jigéen ju jaasir, mu ngi nii ci juróom benni weeram,
37ndax Yàlla, dara tëwu ko.»
38Maryaama daldi ne: «Maa ngi, di jaamub Boroom bi. Nii nga waxe, na ame noonu ci man.»
39Ci fan yooyu la Maryaama fabu gaaw, jëm diiwaanu tund ya, ca dëkkub Yude,
40ba Sàkkaryaa dëkke. Mu agsi ca kër ga, nuyu Elisabet.
41Naka la Elisabet dégg nuyoob Maryaama, doom ja mu ëmb yëngu ca biiram. Elisabet daldi fees ak Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi.
42Mu àddu ca kaw ne: «Yaa gëna barkeel ci jigéen ñi, sa doom ji nga ëmb it barkeel na!
43Ana ku ma doon ba sama ndeyu Sang di ma seetsi?
44Naka la sa kàddug nuyoo tàbbi ci sama nopp rekk, sama doom ji yëngu ci sama biir bi ndax mbégte.
45Ndokkalee yaw mi gëm ne mbir mi ñu la yégal, te mu tukkee ci Boroom bi dina sotti!»
46Maryaama nag ne:
47samag noo laay bége Yàlla mi may musal,
48moo geesu bii jaamam bu tekkeedi,
49nde Kiy Boroom doole moo ma defal jaloore,
50«Yërmandeem a ñeel ay ragalkatam,
51Dooley loxoom la defe ay jaloore,
52wàcce buur yi ci seeni gàngune,
53Ñi xiif, mu reggale leen lu neex,
54Moo wallu bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*, jaamam,
55noonee mu ko dige woon sunuy maam,
56Maryaama toog na fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi.
57Gannaaw gi, Elisabet dem ba àppam mat, mu mucc, am doom ju góor.
58Dëkkandoom yaak ay bokkam yég noonu ko Boroom bi xéewalee yërmandeem, ñu bokk ak moom mbégte ma.
59Ba bés ba délsee, ñu dikk xarafalsi xale ba, bëgg koo tudde Sàkkaryaa, dippee ko baayam.
60Yaayam nag ne leen: «Déet, Yaxya|lemma="Yaxya:"* lay tudd.»
61Ñu ne ko: «Waaye kenn ci say bokk tuddul noonu!»
62Ci kaw loolu ñu liyaar baayam, ngir xam nu mu bëgg ñu tudde xale bi.
63Sàkkaryaa laaj àlluwa, ñu jox ko, mu bind ci: «Yaxya mooy turam.» Ñépp waaru.
64Ca saa sa gémmiñ ga ubbiku, làmmiñ wa nangu, muy wax, daldi sant Yàlla.
65Ba loolu amee tiitaange dikkal mboolem ña leen séq, te mbir moomu mépp nag doon waxtaan ca diiwaanu tundi Yude gépp.
66Ña ca dégg ñépp daldi bàyyi xel ca mbir ma, te naan: «Lu xale bii nara doon ëllëg?» ndax manoorey Boroom bee àndoon ak moom.
67Ci kaw loolu Sàkkaryaa baayu Yaxya|lemma="Yaxya:"* fees ak Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi, daldi tàmbalee jottali kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"*, ne:
68«Cant ñeel na Boroom bi Yàllay Israayil,
69Moo nu feeñalal Musalkat bu manoorewu,
70noonee mu ko waxe woon ca jant yu njëkk ya,
71Moo nu musal ci sunuy noon,
72Moo jëfe yërmande ñeel sunuy maam,
73ak ngiñ la mu giñaloon sunu maam Ibraayma,
74ne moo nuy may nu mucce ci loxoy noon,
75ci biir sellaay ak njub ci kanamam, sunu giiru dund.
76«Ngóor si nag yaw, yonentu Aji Kawe ji lees lay woowe,
77ngir yégal ñoñam mucc
78Sunu Yàllaa yaatu yërmande,
79di niital ñi tooge biir lëndëm ak takkndeeru dee,