1Yeesu neeti ay taalibeem: «Ag fiir guy bàkkaarloo manula ñàkk, waaye wóoy ngalla ka koy lal.
2Ñu takkoon doj wu réy ci baatam, sànni ko biir géej moo gën ci moom muy bàkkaarloo kenn ci xale yii.
3Wattuleen seen bopp.
4Su la tooñoon juróom ñaari yoon ci bés bi, te walbatiku juróom ñaari yoon, ne la: “Tuub naa ko,” baal ko rekk.»
5Ci kaw loolu ndaw ya ne Sang bi: «Yokk nu ngëm.»
6Sang bi ne leen: «Su ngeen amee ci ngëm, lu tollu ni peppu fuddën, ba ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbate ca géej ga,” su boobaa garab gi déggal leen.
7«Kan ci yeen la ab jaamam di beyi mbaa mu sàmmi ba jóge tool, dikk, mu ne ko: “Kaay, nu lekk”?
8Xanaa kay da koy wax ne ko: “Defaral sama reer, te takku, taajal ma, ba ma lekk, naan, nga doora lekk, naan.”
9Ndax la jaam ba jëfe ndigal a tax sangam sant ko? Déedéet kay.
10Yeen itam noonu. Bu ngeen defee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay jaam rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
11Ci biir yoon woowu Yeesu jëmoon Yerusalem, ma nga jaare fa Samari|lemma="Samari:"* ak Galile digaloo.
12Mu dem bay duggsi cib dëkk, fukki gaana|lemma="gaana:"* dikk, dajeek moom, ba dànd ko, daldi taxaw. Ñu xaacu ne:
13«Yeesu, Njaatige, yërëm nu!»
14Yeesu nag gis leen, ne leen: «Demleen seetluji seen yaram ca sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ya.»
15Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi walbatiku, di xaacuy sàbbaal Yàlla.
16Mu dikk, ne gurub, dëpp jëëm fa tànki Yeesu, sant ko. Waa ja nag nitu Samari la woon.
17Ba loolu amee Yeesu ne: «Xanaa du fukk a wér? Juróom ñeent ña nag, ana ñu?
18Amu ci kenn ku ñëw, delloo Yàlla njukkal ku dul doxandéem bii!»
19Yeesu nag ne ko: «Jógal dem; sa ngëm faj na la.»
20Farisen|lemma="Farisen y-:"* yi ñoo laajoon Yeesu, ne ko: «Kañ la nguurug Yàlla di dikk?» Mu ne leen: «Dikkug nguurug Yàlla du ànd akum ceetaan.
21Deesul ne it: “Xoolleen, mu ngi!” mbaa: “Ma ngee!” Ndax kat nguurug Yàlla mu ngi ci seen biir.»
22Mu ne taalibe ya: «Ay jamonoo ngi ñëw yu ngeen naa ngéejoo fekke benn bés ci bési Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki, te dungeen ko fekke.
23Te it, dees na leen ne: “Ma ngee!” mbaa: “Mu ngii!” Buleen dem, buleen ca topp.
24Ndax ni melax di xuyye ci gii wetu asamaan, ba ne ràññ ca gee, noonu la Doomu nit kiy def keroog bésam.
25Waaye balaa booba fàww Doomu nit ki am coono yu bare, jànkoonteek diiŋatu niti tey jii.
26«Noonee mu deme woon ca jamonoy Nóoyin, ni lay deme ca jamonoy Doomu nit ki.
27Nit ñaa nga doon lekk aka naan, di jël jabar aka séyi, ba keroog bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga, mbënn ma dikk, sànk ñépp.
28«Noonee itam la deme woon ca jamonoy Lóot. Nit ñaa nga doon lekk aka naan, di jënd aka jaay, di jëmbat aka tabax.
29Waaye bés ba Lóot génnee Sodom|lemma="Sodom ak Gomor:"*, la tawub sawara ak tamarax wàcce ci asamaan, sànk ñépp.
30Noonu doŋŋ lay deme, bés bu Doomu nit kiy feeñ.
31«Bésub keroog boobee, ku mu fekk ci kaw am taax, te say yëf ne ca biir kër ga, bul wàcc, di ko jëli. Te ku mu fekk tool ba itam, bul dellu.
32Fàttalikuleen jabaru Lóot ja!
33Képp kuy wuta rawale sa bakkan, yaay ñàkk sa bakkan, waaye képp ku ñàkk sa bakkan, yaay dund.
34Maa leen ko wax: guddig keroog ñaar ay bokk benn lal, kenn ki, ñu yóbbu ko, ka ca des, ñu ba ko.
35-36 Ñaari jigéen di wolandoo, kenn ki, ñu yóbbu ko, ka ca des, ñu ba ko.»